PDF —
8 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Bayyina pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Bayyina pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Bayyina Tekki. Al-Bayyina (Medinan) 8 Aaya.



8 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Yéefër ya bokk ca ñoñ Téere, ak Bokkaalekat ya, du ñu deñ mukk di weddi ba baa Firnde di leen dikkël ju leer :
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
ab Yonent, bu jóge ca Yàlla, di jàng ay xëti këyit yu sell laab,
ﮫﮬﮭﮮ
ay téere nekk ci biir yu ame dayo bu màgg.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Te gaa ña ñu joxoon téere masuñoo teqalikoo lu dul ginnaaw ba leen firnde ja dikkëlee.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Te digaleefu leen, lu dul, na nuy jaamu Yàlla, bañ Koo bokkaale te di ko sellal, tey taxawal Julli di joxe asaka. Loolu mooy diiney njub ja.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ñay weddi te bokk ci ñoñ téere, ak Bokkaalekat ya ñoom ña nga ca biir Safaraw Jahanama, te danu fay béel. Ñoom ñii, ñoo yées ci bindeef yi.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Ñi gëm tey jëfu yiw, ñoom ñoo ñee ñoo gën ci bindeef yi.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
Seenug pey fa seen Boroom Àjjanay adan lay doon, yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, ñu béel fa. Yàlla gëram leen ñoom it ñu gëram ko. Loolu ku ragal Yàlla rekk koy am.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers