Hud · 94/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَلَمَّا جَاءَ أَمْرُنَا نَجَّيْنَا شُعَيْبًا وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ بِرَحْمَةٍ مِّنَّا وَأَخَذَتِ الَّذِينَ ظَلَمُوا الصَّيْحَةُ فَأَصْبَحُوا فِي دِيَارِهِمْ جَاثِمِينَ ۝٩٤
Wa lammaa jaaa`a amrunaa najjainaa shu`aibanw wal lazeena aamanoo ma`ahoo birahmatim minnaa wa akhazatil lazeena zalamus saihatu fa asbahoo fee diyaarihim jaasimeen
📖 Tekkim Wolof
Ba Sunu ndigal agsee, musal Nanu Suhaybu ak ña gëmoon ànd ak moom ci Sunu yërmaande. Ag xaacu faagaagal ña tooñ, ñu mujj xëy ne lànjaŋ dee fa seen kër ya,

🎧 Dégg


📜 Aaya 92-96 — Hud

92قَالَ يَا قَوْمِ أَرَهْطِي أَعَزُّ عَلَيْكُم مِّنَ اللَّهِ وَاتَّخَذْتُمُوهُ وَرَاءَكُمْ ظِهْرِيًّا ۖ إِنَّ رَبِّي بِمَا تَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Mu ne : "Yéen samaw nit, moo ndax sama giir moo gën a tedd ci yéen Yàlla ba tax ngeen bàyyi Ko ginnaaw ? Sama Boroom nag Ku peeg la li ngeen di def.
93وَيَا قَوْمِ اعْمَلُوا عَلَىٰ مَكَانَتِكُمْ إِنِّي عَامِلٌ ۖ سَوْفَ تَعْلَمُونَ مَن يَأْتِيهِ عَذَابٌ يُخْزِيهِ وَمَنْ هُوَ كَاذِبٌ ۖ وَارْتَقِبُوا إِنِّي مَعَكُمْ رَقِيبٌ
Yéen samaw nit, defleen lu leen soob. Man it danaa def [li ma sama Boroom sant]. Dangeen mas a xam kan la mbugal di dal, gàcceel ko, ak kan mooy kay fen. Te muñandikuleen ! Maa ngi ànd ak yéen di muñ”.
94وَلَمَّا جَاءَ أَمْرُنَا نَجَّيْنَا شُعَيْبًا وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ بِرَحْمَةٍ مِّنَّا وَأَخَذَتِ الَّذِينَ ظَلَمُوا الصَّيْحَةُ فَأَصْبَحُوا فِي دِيَارِهِمْ جَاثِمِينَ
Ba Sunu ndigal agsee, musal Nanu Suhaybu ak ña gëmoon ànd ak moom ci Sunu yërmaande. Ag xaacu faagaagal ña tooñ, ñu mujj xëy ne lànjaŋ dee fa seen kër ya,
95كَأَن لَّمْ يَغْنَوْا فِيهَا ۗ أَلَا بُعْدًا لِّمَدْيَنَ كَمَا بَعِدَتْ ثَمُودُ
mu mel ni masuñu fa woon a dëkk. Waaw, ndax alkaande dalul waa Madyaana na mu alake woon waa Samuuda ?.
96وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا وَسُلْطَانٍ مُّبِينٍ
Te yónni woon Nanu Muusaa mu ànd ak Sunuy kaawtéef ak lay yu leer nàññ,
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
94Aaya

Tekki — Hud 94

Simoore Hud Aaya 94 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba Sunu ndigal agsee, musal Nanu Suhaybu ak ña gëmoon…

Simoore Aaya 94/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 92–96. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers