An-Nahl · 119/128
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nahl
ثُمَّ إِنَّ رَبَّكَ لِلَّذِينَ عَمِلُوا السُّوءَ بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ وَأَصْلَحُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝١١٩
Summma inna Rabbaka lillazeena `amilus sooo`a bijahaalatin summa taaboo mim ba`di zaaalika wa aslahoo inna Rabbaka mim ba`dihaa la Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Mu des nag ne sa Boroom, lu jëm ci ña jëfoon [lu bon niki bokkaale] cig réer, ginnaaw loola ñu tuub ko, rafetal seeni jëf, ñooña sa Boroom fàwwu Mu jéggal leen, yërëm leen naka.

🎧 Dégg


📜 Aaya 117-121 — Simoore An-Nahl

117مَتَاعٌ قَلِيلٌ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñeel na leen yóbbal bu néew, ak mbugal mu metti.
118وَعَلَى الَّذِينَ هَادُوا حَرَّمْنَا مَا قَصَصْنَا عَلَيْكَ مِن قَبْلُ ۖ وَمَا ظَلَمْنَاهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Te araamaloon nañu ca yahuud ya li Nu la nettali ca bu jëkk. Te tooñunu leen ; waaye ñoo tooñ seen bopp.
119ثُمَّ إِنَّ رَبَّكَ لِلَّذِينَ عَمِلُوا السُّوءَ بِجَهَالَةٍ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ وَأَصْلَحُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Mu des nag ne sa Boroom, lu jëm ci ña jëfoon [lu bon niki bokkaale] cig réer, ginnaaw loola ñu tuub ko, rafetal seeni jëf, ñooña sa Boroom fàwwu Mu jéggal leen, yërëm leen naka.
120إِنَّ إِبْرَاهِيمَ كَانَ أُمَّةً قَانِتًا لِّلَّهِ حَنِيفًا وَلَمْ يَكُ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ibraahiima nag roytéef la. Di jaamukatu Yàlla, di ko wéetal, musul a bokk ca bokkaalekat ya.
121شَاكِرًا لِّأَنْعُمِهِ ۚ اجْتَبَاهُ وَهَدَاهُ إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Ku daan gërëm [Yàlla] la ci xéewalam yi, Yàlla tànn na ko, gindi ko, teg ko ci yoon wu jub xocc wa.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
119Aaya

Tekki — An-Nahl 119

Simoore An-Nahl Aaya 119 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu des nag ne sa Boroom, lu jëm ci ña…

Simoore Aaya 119/128 — Simoore An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nahl Dégg, Simoore An-Nahl Tekki, Simoore An-Nahl mp3, Simoore An-Nahl pdf. Aaya 117–121. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers