Al-Isra · 61/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ قَالَ أَأَسْجُدُ لِمَنْ خَلَقْتَ طِينًا ۝٦١
Wa iz qulnaa lilma laaa`ikatis judoo li Aadama fasajadooo illaaa Ibleesa qaala `a-asjudu liman khalaqta teena
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot ginnaaw Ibliis, mu ne : “Ndax damay sujjóotal koo binde ak ban ? ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 59-63 — Simoore Al-Isra

59وَمَا مَنَعَنَا أَن نُّرْسِلَ بِالْآيَاتِ إِلَّا أَن كَذَّبَ بِهَا الْأَوَّلُونَ ۚ وَآتَيْنَا ثَمُودَ النَّاقَةَ مُبْصِرَةً فَظَلَمُوا بِهَا ۚ وَمَا نُرْسِلُ بِالْآيَاتِ إِلَّا تَخْوِيفًا
Lu Nu terey wàcce ay kéemaan, lu dul ñu jëkk ña dañu leen a weddi woon. Te sax joxoon Nanu waa Samooda giléem gu jigéen [muy kéemaan] gu leer : ñu def cag tooñeel. Te Nun dunu wàcce kéemaan lu dul ne Danuy xuppe ci kéemaan googu ak di ca àrtu nit ña.
60وَإِذْ قُلْنَا لَكَ إِنَّ رَبَّكَ أَحَاطَ بِالنَّاسِ ۚ وَمَا جَعَلْنَا الرُّؤْيَا الَّتِي أَرَيْنَاكَ إِلَّا فِتْنَةً لِّلنَّاسِ وَالشَّجَرَةَ الْمَلْعُونَةَ فِي الْقُرْآنِ ۚ وَنُخَوِّفُهُمْ فَمَا يَزِيدُهُمْ إِلَّا طُغْيَانًا كَبِيرًا
[Fàttalikul] ba Nu la waxee ne sa Boroom ku peeg nit ñi la. Te gént gi Nu la wonoon, defunu ko woon lu dul muy nattu ci nit ñi, te garab ga Nu rëbb ca Alxuraan it, Danu leen cay tiital ; waaye yokku leen lu dul beew gu mag.
61وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ قَالَ أَأَسْجُدُ لِمَنْ خَلَقْتَ طِينًا
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot ginnaaw Ibliis, mu ne : “Ndax damay sujjóotal koo binde ak ban ? ”
62قَالَ أَرَأَيْتَكَ هَٰذَا الَّذِي كَرَّمْتَ عَلَيَّ لَئِنْ أَخَّرْتَنِ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَأَحْتَنِكَنَّ ذُرِّيَّتَهُ إِلَّا قَلِيلًا
Mu ne : “Wax Ma lu tax nga teral kii ci sama kaw ? Soo ma muñalee ba Bis-pénc ba, danaa fexe ba ay sëtam yépp yàqule, ba mu des ñu néew”.
63قَالَ اذْهَبْ فَمَن تَبِعَكَ مِنْهُمْ فَإِنَّ جَهَنَّمَ جَزَاؤُكُمْ جَزَاءً مَّوْفُورًا
Mu ne ko : “Demal ! Ku la topp ci ñoom... [na xam ne] Safara moo di seen pey, pey guy nekk di lu mat sëkk.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
61Aaya

Tekki — Al-Isra 61

Simoore Al-Isra Aaya 61 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya : “Sujjóotleen ci Aadama”,…

Simoore Aaya 61/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 59–63. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers