Al-Isra · 70/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
۞ وَلَقَدْ كَرَّمْنَا بَنِي آدَمَ وَحَمَلْنَاهُمْ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَرَزَقْنَاهُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ وَفَضَّلْنَاهُمْ عَلَىٰ كَثِيرٍ مِّمَّنْ خَلَقْنَا تَفْضِيلًا ۝٧٠
Wa laqad karramnaa Baneee aadama wa hamalnaahum fil barri walbahri wa razaqnaahum minat taiyibaati wa faddalnaahum `alaa kaseerim mimman khalaqnaa tafdeelaa
📖 Tekkim Wolof
Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci jéeri ji ak ci géej gi, te xéewal Nanu leen [ciy ñam] yu sell, Nu defal leen ngëneel ci kaw ñu bari ca ña Nu bind ngëneel lu fés.
🎧 Dégg

📜 Aaya 68-72 — Al-Isra

68أَفَأَمِنتُمْ أَن يَخْسِفَ بِكُمْ جَانِبَ الْبَرِّ أَوْ يُرْسِلَ عَلَيْكُمْ حَاصِبًا ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ وَكِيلًا
Moo ndax dangeen a naagu ne : du xar suuf si [mëdd leen], walla duleen yónnee ngelawu sànniy xeer fekk dungeen ci am ku leen ci yiir.
69أَمْ أَمِنتُمْ أَن يُعِيدَكُمْ فِيهِ تَارَةً أُخْرَىٰ فَيُرْسِلَ عَلَيْكُمْ قَاصِفًا مِّنَ الرِّيحِ فَيُغْرِقَكُم بِمَا كَفَرْتُمْ ۙ ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ عَلَيْنَا بِهِ تَبِيعًا
Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir géej] beneen yoon, yónnee leen ngelaw lu tar, Mu labal leen ngir seen weddi ? Te fekk dungeen mën a am ku leen dimbali ci Nun !
70۞ وَلَقَدْ كَرَّمْنَا بَنِي آدَمَ وَحَمَلْنَاهُمْ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَرَزَقْنَاهُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ وَفَضَّلْنَاهُمْ عَلَىٰ كَثِيرٍ مِّمَّنْ خَلَقْنَا تَفْضِيلًا
Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci jéeri ji ak ci géej gi, te xéewal Nanu leen [ciy ñam] yu sell, Nu defal leen ngëneel ci kaw ñu bari ca ña Nu bind ngëneel lu fés.
71يَوْمَ نَدْعُو كُلَّ أُنَاسٍ بِإِمَامِهِمْ ۖ فَمَنْ أُوتِيَ كِتَابَهُ بِيَمِينِهِ فَأُولَٰئِكَ يَقْرَءُونَ كِتَابَهُمْ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا
Bis bu Nu woowee nit ku nekk ca turu njiitam, képp ku Nu jox téereem ci ndeyjooram, ñooña danañu jàng seen téere te deesuleen tooñ [ci wànnil leen dara].
72وَمَن كَانَ فِي هَٰذِهِ أَعْمَىٰ فَهُوَ فِي الْآخِرَةِ أَعْمَىٰ وَأَضَلُّ سَبِيلًا
Ku nekkoon gumba ci àddina si, dana wéye gumba ca àllaaxira, te gën a réer, sori yoonu njub wa.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
70Aaya

Tekki — Al-Isra 70

Simoore Al-Isra Aaya 70 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci…

Simoore Aaya 70/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 68–72. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers