Al-Isra · 69/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
أَمْ أَمِنتُمْ أَن يُعِيدَكُمْ فِيهِ تَارَةً أُخْرَىٰ فَيُرْسِلَ عَلَيْكُمْ قَاصِفًا مِّنَ الرِّيحِ فَيُغْرِقَكُم بِمَا كَفَرْتُمْ ۙ ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ عَلَيْنَا بِهِ تَبِيعًا ۝٦٩
Am amintum any yu`eedakum feehi taaratan ukhraa fa yursila `alaikum qaasifam minar reehi fa yugh riqakum bimaa kafartum summa laa tajidoo lakum `alainaa bihee tabee`aa
📖 Tekkim Wolof
Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir géej] beneen yoon, yónnee leen ngelaw lu tar, Mu labal leen ngir seen weddi ? Te fekk dungeen mën a am ku leen dimbali ci Nun !

🎧 Dégg


📜 Aaya 67-71 — Simoore Al-Isra

67وَإِذَا مَسَّكُمُ الضُّرُّ فِي الْبَحْرِ ضَلَّ مَن تَدْعُونَ إِلَّا إِيَّاهُ ۖ فَلَمَّا نَجَّاكُمْ إِلَى الْبَرِّ أَعْرَضْتُمْ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ كَفُورًا
Bu leen naqar dabee ci géej, ña ngeen doon jaamu réer leen ginnaawam. Te bu Nu leen musalee ba ñu agsi ci jéeri ji, ngeen dëddu. Nit daal ku goreedi la !
68أَفَأَمِنتُمْ أَن يَخْسِفَ بِكُمْ جَانِبَ الْبَرِّ أَوْ يُرْسِلَ عَلَيْكُمْ حَاصِبًا ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ وَكِيلًا
Moo ndax dangeen a naagu ne : du xar suuf si [mëdd leen], walla duleen yónnee ngelawu sànniy xeer fekk dungeen ci am ku leen ci yiir.
69أَمْ أَمِنتُمْ أَن يُعِيدَكُمْ فِيهِ تَارَةً أُخْرَىٰ فَيُرْسِلَ عَلَيْكُمْ قَاصِفًا مِّنَ الرِّيحِ فَيُغْرِقَكُم بِمَا كَفَرْتُمْ ۙ ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ عَلَيْنَا بِهِ تَبِيعًا
Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir géej] beneen yoon, yónnee leen ngelaw lu tar, Mu labal leen ngir seen weddi ? Te fekk dungeen mën a am ku leen dimbali ci Nun !
70۞ وَلَقَدْ كَرَّمْنَا بَنِي آدَمَ وَحَمَلْنَاهُمْ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَرَزَقْنَاهُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ وَفَضَّلْنَاهُمْ عَلَىٰ كَثِيرٍ مِّمَّنْ خَلَقْنَا تَفْضِيلًا
Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci jéeri ji ak ci géej gi, te xéewal Nanu leen [ciy ñam] yu sell, Nu defal leen ngëneel ci kaw ñu bari ca ña Nu bind ngëneel lu fés.
71يَوْمَ نَدْعُو كُلَّ أُنَاسٍ بِإِمَامِهِمْ ۖ فَمَنْ أُوتِيَ كِتَابَهُ بِيَمِينِهِ فَأُولَٰئِكَ يَقْرَءُونَ كِتَابَهُمْ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا
Bis bu Nu woowee nit ku nekk ca turu njiitam, képp ku Nu jox téereem ci ndeyjooram, ñooña danañu jàng seen téere te deesuleen tooñ [ci wànnil leen dara].
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
69Aaya

Tekki — Al-Isra 69

Simoore Al-Isra Aaya 69 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir…

Simoore Aaya 69/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 67–71. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers