Al-Kahf · 61/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
فَلَمَّا بَلَغَا مَجْمَعَ بَيْنِهِمَا نَسِيَا حُوتَهُمَا فَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ سَرَبًا ۝٦١
Falammaa balaghaa majma`a bainihimaa nasiyaa hootahumaa fattakhaza sabeelahoo fil bahri sarabaa
📖 Tekkim Wolof
Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte ca diggante ba seenu jën, mu potoxlu daldi koy rëcc jëlu yoonam ca biir géej ga.

🎧 Dégg


📜 Aaya 59-63 — Al-Kahf

59وَتِلْكَ الْقُرَىٰ أَهْلَكْنَاهُمْ لَمَّا ظَلَمُوا وَجَعَلْنَا لِمَهْلِكِهِم مَّوْعِدًا
[Noonu la] Nu alage woon dëkk yooyu ba ñu tooñee te Nu sàkkaloon alkaande ja ab àpp.
60وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِفَتَاهُ لَا أَبْرَحُ حَتَّىٰ أَبْلُغَ مَجْمَعَ الْبَحْرَيْنِ أَوْ أَمْضِيَ حُقُبًا
[Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma deñ di dox ba mbete ma eggee ca dajewaayu ñaari geej ya, walla may wéy jamano ju yàgg”.
61فَلَمَّا بَلَغَا مَجْمَعَ بَيْنِهِمَا نَسِيَا حُوتَهُمَا فَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ سَرَبًا
Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte ca diggante ba seenu jën, mu potoxlu daldi koy rëcc jëlu yoonam ca biir géej ga.
62فَلَمَّا جَاوَزَا قَالَ لِفَتَاهُ آتِنَا غَدَاءَنَا لَقَدْ لَقِينَا مِن سَفَرِنَا هَٰذَا نَصَبًا
Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil sunu añ : daj nanu coono ci sunu tukki bii”.
63قَالَ أَرَأَيْتَ إِذْ أَوَيْنَا إِلَى الصَّخْرَةِ فَإِنِّي نَسِيتُ الْحُوتَ وَمَا أَنسَانِيهُ إِلَّا الشَّيْطَانُ أَنْ أَذْكُرَهُ ۚ وَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ عَجَبًا
Mu tontu ne : “Ndax gisoo ba nu toogee ca doj wa, damaa fàtte jën wa - te dara fàttewooluma ko lu dul Séytaane mi tax xalaatuma ko - mu dem yoonam ci géej, lu yéeme”.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
61Aaya

Tekki — Al-Kahf 61

Simoore Al-Kahf Aaya 61 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte…

Simoore Aaya 61/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 59–63. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers