Al-Kahf · 62/110
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Kahf
فَلَمَّا جَاوَزَا قَالَ لِفَتَاهُ آتِنَا غَدَاءَنَا لَقَدْ لَقِينَا مِن سَفَرِنَا هَٰذَا نَصَبًا ۝٦٢
Falammaa jaawazaa qaala lifataahu aatinaa ghadaaa`anaa laqad laqeena min safarinaa haazaa nasabaa
📖 Tekkim Wolof
Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil sunu añ : daj nanu coono ci sunu tukki bii”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 60-64 — Simoore Al-Kahf

60وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِفَتَاهُ لَا أَبْرَحُ حَتَّىٰ أَبْلُغَ مَجْمَعَ الْبَحْرَيْنِ أَوْ أَمْضِيَ حُقُبًا
[Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma deñ di dox ba mbete ma eggee ca dajewaayu ñaari geej ya, walla may wéy jamano ju yàgg”.
61فَلَمَّا بَلَغَا مَجْمَعَ بَيْنِهِمَا نَسِيَا حُوتَهُمَا فَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ سَرَبًا
Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte ca diggante ba seenu jën, mu potoxlu daldi koy rëcc jëlu yoonam ca biir géej ga.
62فَلَمَّا جَاوَزَا قَالَ لِفَتَاهُ آتِنَا غَدَاءَنَا لَقَدْ لَقِينَا مِن سَفَرِنَا هَٰذَا نَصَبًا
Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil sunu añ : daj nanu coono ci sunu tukki bii”.
63قَالَ أَرَأَيْتَ إِذْ أَوَيْنَا إِلَى الصَّخْرَةِ فَإِنِّي نَسِيتُ الْحُوتَ وَمَا أَنسَانِيهُ إِلَّا الشَّيْطَانُ أَنْ أَذْكُرَهُ ۚ وَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ عَجَبًا
Mu tontu ne : “Ndax gisoo ba nu toogee ca doj wa, damaa fàtte jën wa - te dara fàttewooluma ko lu dul Séytaane mi tax xalaatuma ko - mu dem yoonam ci géej, lu yéeme”.
64قَالَ ذَٰلِكَ مَا كُنَّا نَبْغِ ۚ فَارْتَدَّا عَلَىٰ آثَارِهِمَا قَصَصًا
Muusaa ne ko : “Loolu lanu doon sàkku”. Ñu dellu fa ñu jaaroon di xeeñtu.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
62Aaya

Tekki — Al-Kahf 62

Simoore Al-Kahf Aaya 62 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil…

Simoore Aaya 62/110 — Simoore Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Kahf Dégg, Simoore Al-Kahf Tekki, Simoore Al-Kahf mp3, Simoore Al-Kahf pdf. Aaya 60–64. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers