Al-Kahf · 60/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِفَتَاهُ لَا أَبْرَحُ حَتَّىٰ أَبْلُغَ مَجْمَعَ الْبَحْرَيْنِ أَوْ أَمْضِيَ حُقُبًا ۝٦٠
Wa iz qaalaa Moosaa lifataahu laaa abrahu hattaaa ablugha majma`al bahrayni aw amdiya huqubaa
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma deñ di dox ba mbete ma eggee ca dajewaayu ñaari geej ya, walla may wéy jamano ju yàgg”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 58-62 — Al-Kahf

58وَرَبُّكَ الْغَفُورُ ذُو الرَّحْمَةِ ۖ لَوْ يُؤَاخِذُهُم بِمَا كَسَبُوا لَعَجَّلَ لَهُمُ الْعَذَابَ ۚ بَل لَّهُم مَّوْعِدٌ لَّن يَجِدُوا مِن دُونِهِ مَوْئِلًا
Te sa Boroom mooy Jéggalaakoon ba, di boroom yërmaande. Bu leen jàppe woon la ñuy fàggu [ciy jëf yu bon]. Kon Dana gaawal seen mbugal. Waaye am nañu àpp boo xam ne bu agsee, duñu am mukk ku leen musal ku dul Moom.
59وَتِلْكَ الْقُرَىٰ أَهْلَكْنَاهُمْ لَمَّا ظَلَمُوا وَجَعَلْنَا لِمَهْلِكِهِم مَّوْعِدًا
[Noonu la] Nu alage woon dëkk yooyu ba ñu tooñee te Nu sàkkaloon alkaande ja ab àpp.
60وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِفَتَاهُ لَا أَبْرَحُ حَتَّىٰ أَبْلُغَ مَجْمَعَ الْبَحْرَيْنِ أَوْ أَمْضِيَ حُقُبًا
[Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma deñ di dox ba mbete ma eggee ca dajewaayu ñaari geej ya, walla may wéy jamano ju yàgg”.
61فَلَمَّا بَلَغَا مَجْمَعَ بَيْنِهِمَا نَسِيَا حُوتَهُمَا فَاتَّخَذَ سَبِيلَهُ فِي الْبَحْرِ سَرَبًا
Ba ñu eggee ñoom ñaar ca dajewaay ba, ñu fàtte ca diggante ba seenu jën, mu potoxlu daldi koy rëcc jëlu yoonam ca biir géej ga.
62فَلَمَّا جَاوَزَا قَالَ لِفَتَاهُ آتِنَا غَدَاءَنَا لَقَدْ لَقِينَا مِن سَفَرِنَا هَٰذَا نَصَبًا
Ba ñu ko weesoo, mu ne surgaam ba : “Indil sunu añ : daj nanu coono ci sunu tukki bii”.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
60Aaya

Tekki — Al-Kahf 60

Simoore Al-Kahf Aaya 60 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] ba Muusaa waxee surgaam ba ne ko : “Duma…

Simoore Aaya 60/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 58–62. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers