Al-Baqara · 148/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَلِكُلٍّ وِجْهَةٌ هُوَ مُوَلِّيهَا ۖ فَاسْتَبِقُوا الْخَيْرَاتِ ۚ أَيْنَ مَا تَكُونُوا يَأْتِ بِكُمُ اللَّهُ جَمِيعًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝١٤٨
Wa likullinw wijhatun huwa muwalleehaa fastabiqul khairaat; ayna maa takoonoo yaati bikumullaahu jamee`aa; innal laaha `alaa kulli shai`in qadeer
📖 Tekkim Wolof
Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.
🎧 Dégg

📜 Aaya 146-150 — Al-Baqara

146الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْرِفُونَهُ كَمَا يَعْرِفُونَ أَبْنَاءَهُمْ ۖ وَإِنَّ فَرِيقًا مِّنْهُمْ لَيَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !
147الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka.
148وَلِكُلٍّ وِجْهَةٌ هُوَ مُوَلِّيهَا ۖ فَاسْتَبِقُوا الْخَيْرَاتِ ۚ أَيْنَ مَا تَكُونُوا يَأْتِ بِكُمُ اللَّهُ جَمِيعًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.
149وَمِنْ حَيْثُ خَرَجْتَ فَوَلِّ وَجْهَكَ شَطْرَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ ۖ وَإِنَّهُ لَلْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Foo demati, jëmëleel sa kanam ca jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Looloo di dëgg de. Te Yàlla du sàgganee li ngeen di jëf.
150وَمِنْ حَيْثُ خَرَجْتَ فَوَلِّ وَجْهَكَ شَطْرَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ ۚ وَحَيْثُ مَا كُنتُمْ فَوَلُّوا وُجُوهَكُمْ شَطْرَهُ لِئَلَّا يَكُونَ لِلنَّاسِ عَلَيْكُمْ حُجَّةٌ إِلَّا الَّذِينَ ظَلَمُوا مِنْهُمْ فَلَا تَخْشَوْهُمْ وَاخْشَوْنِي وَلِأُتِمَّ نِعْمَتِي عَلَيْكُمْ وَلَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
Foo mën a demati, jëmaleel sa kanam ca Jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Fu ngeen mën a nekk, nangeen ca jëmale seeni kanam [jublu], ndax nit ñi bañ a am aw lay ci seen kaw, ku dul ñiy tooñ. Te buleen leen ragal ; ragal-leen Ma, man Yàlla, ngir Ma mottali sama xéewal ci yéen ak itam ndax ngeen gindiku !
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
148Aaya

Tekki — Al-Baqara 148

Simoore Al-Baqara Aaya 148 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci…

Simoore Aaya 148/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 146–150. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers