Al-Baqara · 147/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ ۝١٤٧
Alhaqqu mir Rabbika falaa takoonana minal mumtareen
📖 Tekkim Wolof
Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka.
🎧 Dégg

📜 Aaya 145-149 — Al-Baqara

145وَلَئِنْ أَتَيْتَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ بِكُلِّ آيَةٍ مَّا تَبِعُوا قِبْلَتَكَ ۚ وَمَا أَنتَ بِتَابِعٍ قِبْلَتَهُمْ ۚ وَمَا بَعْضُهُم بِتَابِعٍ قِبْلَةَ بَعْضٍ ۚ وَلَئِنِ اتَّبَعْتَ أَهْوَاءَهُم مِّن بَعْدِ مَا جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ ۙ إِنَّكَ إِذًا لَّمِنَ الظَّالِمِينَ
Boo indiloon, ñoñ-téere, kéemaan gu mu mën a doon, du tax ñu topp sa jubluwaay (xibla) ! Yaw itam du yaay topp seen xibla ; ñoom ci seen biir sax, kenn du ca topp xibla moroomam. Yaw nag boo toppee seeni bànneex ginnaaw ba la xam-xam bu leer dikkalee, kon de ca tooñkat ya ngay bokk.
146الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْرِفُونَهُ كَمَا يَعْرِفُونَ أَبْنَاءَهُمْ ۖ وَإِنَّ فَرِيقًا مِّنْهُمْ لَيَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !
147الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka.
148وَلِكُلٍّ وِجْهَةٌ هُوَ مُوَلِّيهَا ۖ فَاسْتَبِقُوا الْخَيْرَاتِ ۚ أَيْنَ مَا تَكُونُوا يَأْتِ بِكُمُ اللَّهُ جَمِيعًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.
149وَمِنْ حَيْثُ خَرَجْتَ فَوَلِّ وَجْهَكَ شَطْرَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ ۖ وَإِنَّهُ لَلْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Foo demati, jëmëleel sa kanam ca jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Looloo di dëgg de. Te Yàlla du sàgganee li ngeen di jëf.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
147Aaya

Tekki — Al-Baqara 147

Simoore Al-Baqara Aaya 147 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci…

Simoore Aaya 147/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 145–149. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers