Al-Baqara · 162/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
خَالِدِينَ فِيهَا ۖ لَا يُخَفَّفُ عَنْهُمُ الْعَذَابُ وَلَا هُمْ يُنظَرُونَ ۝١٦٢
khaalideena feeha laa yukhaffafu `anhumul `azaabu wa laa hum yunzaroon
📖 Tekkim Wolof
Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal, kenn duleen ko yeexalal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 160-164 — Simoore Al-Baqara

160إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا وَأَصْلَحُوا وَبَيَّنُوا فَأُولَٰئِكَ أَتُوبُ عَلَيْهِمْ ۚ وَأَنَا التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
lu dul ña ca tuub, yéwénal te leeral : ñooña Danaa leen jéggal Man Yàlla. Te Man maay Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
161إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَمَاتُوا وَهُمْ كُفَّارٌ أُولَٰئِكَ عَلَيْهِمْ لَعْنَةُ اللَّهِ وَالْمَلَائِكَةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
Ña weddi te dee ci kéefar, ñooña rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp dana dal ci seen kaw.
162خَالِدِينَ فِيهَا ۖ لَا يُخَفَّفُ عَنْهُمُ الْعَذَابُ وَلَا هُمْ يُنظَرُونَ
Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal, kenn duleen ko yeexalal.
163وَإِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۖ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الرَّحْمَٰنُ الرَّحِيمُ
Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla ju dul moom, mooy xéewal bindéef yi ci yërmaandeem ci àddina, di Jaglewaakoonu yërmaandeem jullit ña ca àllaaxira.
164إِنَّ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَالْفُلْكِ الَّتِي تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِمَا يَنفَعُ النَّاسَ وَمَا أَنزَلَ اللَّهُ مِنَ السَّمَاءِ مِن مَّاءٍ فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا وَبَثَّ فِيهَا مِن كُلِّ دَابَّةٍ وَتَصْرِيفِ الرِّيَاحِ وَالسَّحَابِ الْمُسَخَّرِ بَيْنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Nit ñiy jëfandikoo seeni xel, war naa doy sëkk kéemaan ci ñoom, ni Yàlla binde asamaan yi ak suuf si, jëllasanteb guddi ak bëccëg, gaal yiy daw ci géej ci luy njariñi nit ñi, ak li Yàlla wàcce ci ndox mu bawoo asamaan, mu nàndal ca suuf si ginnaaw ba mu wowee, mu tasaare ca kaw suuf si ay meññeef, walbatim ngelaw leek niir yi nekk diggante asamaan ak suuf.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
162Aaya

Tekki — Al-Baqara 162

Simoore Al-Baqara Aaya 162 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal,…

Simoore Aaya 162/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 160–164. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers