Al-Baqara · 163/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۖ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الرَّحْمَٰنُ الرَّحِيمُ ۝١٦٣
Wa ilaahukum illaahunw waahid, laaa ilaaha illaa Huwar Rahmaanur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla ju dul moom, mooy xéewal bindéef yi ci yërmaandeem ci àddina, di Jaglewaakoonu yërmaandeem jullit ña ca àllaaxira.
🎧 Dégg

📜 Aaya 161-165 — Al-Baqara

161إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَمَاتُوا وَهُمْ كُفَّارٌ أُولَٰئِكَ عَلَيْهِمْ لَعْنَةُ اللَّهِ وَالْمَلَائِكَةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
Ña weddi te dee ci kéefar, ñooña rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp dana dal ci seen kaw.
162خَالِدِينَ فِيهَا ۖ لَا يُخَفَّفُ عَنْهُمُ الْعَذَابُ وَلَا هُمْ يُنظَرُونَ
Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal, kenn duleen ko yeexalal.
163وَإِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۖ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الرَّحْمَٰنُ الرَّحِيمُ
Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla ju dul moom, mooy xéewal bindéef yi ci yërmaandeem ci àddina, di Jaglewaakoonu yërmaandeem jullit ña ca àllaaxira.
164إِنَّ فِي خَلْقِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَالْفُلْكِ الَّتِي تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِمَا يَنفَعُ النَّاسَ وَمَا أَنزَلَ اللَّهُ مِنَ السَّمَاءِ مِن مَّاءٍ فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا وَبَثَّ فِيهَا مِن كُلِّ دَابَّةٍ وَتَصْرِيفِ الرِّيَاحِ وَالسَّحَابِ الْمُسَخَّرِ بَيْنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Nit ñiy jëfandikoo seeni xel, war naa doy sëkk kéemaan ci ñoom, ni Yàlla binde asamaan yi ak suuf si, jëllasanteb guddi ak bëccëg, gaal yiy daw ci géej ci luy njariñi nit ñi, ak li Yàlla wàcce ci ndox mu bawoo asamaan, mu nàndal ca suuf si ginnaaw ba mu wowee, mu tasaare ca kaw suuf si ay meññeef, walbatim ngelaw leek niir yi nekk diggante asamaan ak suuf.
165وَمِنَ النَّاسِ مَن يَتَّخِذُ مِن دُونِ اللَّهِ أَندَادًا يُحِبُّونَهُمْ كَحُبِّ اللَّهِ ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا أَشَدُّ حُبًّا لِّلَّهِ ۗ وَلَوْ يَرَى الَّذِينَ ظَلَمُوا إِذْ يَرَوْنَ الْعَذَابَ أَنَّ الْقُوَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًا وَأَنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعَذَابِ
Am na ci nit ñi ñuy jaamu xërëm bàyyi Yàlla, soppleen ni ñu soppee Yàlla. Ña gëm ñoo gën a tar cofeel ci Yàlla. Ay boo gisoon ña weddi, naka lañuy janook mbugal ma, xam xéll ne kàttan ba kàttan jeex Yàllaa ko am te Yàlla ku tar mbugal la !...
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
163Aaya

Tekki — Al-Baqara 163

Simoore Al-Baqara Aaya 163 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla…

Simoore Aaya 163/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 161–165. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers