Al-Baqara · 167/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَقَالَ الَّذِينَ اتَّبَعُوا لَوْ أَنَّ لَنَا كَرَّةً فَنَتَبَرَّأَ مِنْهُمْ كَمَا تَبَرَّءُوا مِنَّا ۗ كَذَٰلِكَ يُرِيهِمُ اللَّهُ أَعْمَالَهُمْ حَسَرَاتٍ عَلَيْهِمْ ۖ وَمَا هُم بِخَارِجِينَ مِنَ النَّارِ ۝١٦٧
Wa qaalal lazeenat taba`oo law anna lanaa karratan fanatabarra a minhum kamaa tabarra`oo minnaa; kazaalika yureehimullaahu a`maalahum hasaraatin `alaihim wa maa hum bikhaarijeena minan Naar
📖 Tekkim Wolof
Ña toppe woon, daldi ne : “Ay ! bu nu delluwaatoon àddina! Dananu deñtalu ci ñoom kem ni ñu deñtaloo ci nun” - Noonu la leen Yàlla doon wane seeni jëf ; mu di ag yàqule ca seen kaw te duñu génn Safara.

🎧 Dégg


📜 Aaya 165-169 — Al-Baqara

165وَمِنَ النَّاسِ مَن يَتَّخِذُ مِن دُونِ اللَّهِ أَندَادًا يُحِبُّونَهُمْ كَحُبِّ اللَّهِ ۖ وَالَّذِينَ آمَنُوا أَشَدُّ حُبًّا لِّلَّهِ ۗ وَلَوْ يَرَى الَّذِينَ ظَلَمُوا إِذْ يَرَوْنَ الْعَذَابَ أَنَّ الْقُوَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًا وَأَنَّ اللَّهَ شَدِيدُ الْعَذَابِ
Am na ci nit ñi ñuy jaamu xërëm bàyyi Yàlla, soppleen ni ñu soppee Yàlla. Ña gëm ñoo gën a tar cofeel ci Yàlla. Ay boo gisoon ña weddi, naka lañuy janook mbugal ma, xam xéll ne kàttan ba kàttan jeex Yàllaa ko am te Yàlla ku tar mbugal la !...
166إِذْ تَبَرَّأَ الَّذِينَ اتُّبِعُوا مِنَ الَّذِينَ اتَّبَعُوا وَرَأَوُا الْعَذَابَ وَتَقَطَّعَتْ بِهِمُ الْأَسْبَابُ
[Bu Bis-pénc baa] ba ñañu toppoon deñtalu ca ña leen toppoon ndax te gis nañu mbugal ma, la leen boole woon lépp daggatoo !
167وَقَالَ الَّذِينَ اتَّبَعُوا لَوْ أَنَّ لَنَا كَرَّةً فَنَتَبَرَّأَ مِنْهُمْ كَمَا تَبَرَّءُوا مِنَّا ۗ كَذَٰلِكَ يُرِيهِمُ اللَّهُ أَعْمَالَهُمْ حَسَرَاتٍ عَلَيْهِمْ ۖ وَمَا هُم بِخَارِجِينَ مِنَ النَّارِ
Ña toppe woon, daldi ne : “Ay ! bu nu delluwaatoon àddina! Dananu deñtalu ci ñoom kem ni ñu deñtaloo ci nun” - Noonu la leen Yàlla doon wane seeni jëf ; mu di ag yàqule ca seen kaw te duñu génn Safara.
168يَا أَيُّهَا النَّاسُ كُلُوا مِمَّا فِي الْأَرْضِ حَلَالًا طَيِّبًا وَلَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ إِنَّهُ لَكُمْ عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Yéen nit ñi ! Lekkleen ci li nekk ci suuf si, dagan, teey ; te buleen topp jéegoy (Séytaane) moom seenub noon la bu bir .
169إِنَّمَا يَأْمُرُكُم بِالسُّوءِ وَالْفَحْشَاءِ وَأَن تَقُولُوا عَلَى اللَّهِ مَا لَا تَعْلَمُونَ
Li mu leen di digal moo di ag mbon ak ug caay-caay ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
167Aaya

Tekki — Al-Baqara 167

Simoore Al-Baqara Aaya 167 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña toppe woon, daldi ne : “Ay ! bu nu…

Simoore Aaya 167/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 165–169. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers