Al-Baqara · 251/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
فَهَزَمُوهُم بِإِذْنِ اللَّهِ وَقَتَلَ دَاوُودُ جَالُوتَ وَآتَاهُ اللَّهُ الْمُلْكَ وَالْحِكْمَةَ وَعَلَّمَهُ مِمَّا يَشَاءُ ۗ وَلَوْلَا دَفْعُ اللَّهِ النَّاسَ بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لَّفَسَدَتِ الْأَرْضُ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ ذُو فَضْلٍ عَلَى الْعَالَمِينَ ۝٢٥١
Fahazamoohum bi iznillaahi wa qatala Daawoodu jaaloota wa aataahul laahulmulka Wal Hikmata wa `allamahoo mimmaa yashaaa`; wa law laa daf`ullaahin naasa ba`dahum biba`dil lafasadatil ardu wa laakinnal laaha zoo fadlin `alal`aalameen
📖 Tekkim Wolof
Nu def ci ndigalu Yàlla [Daawuda] rey [Jaaluta] ; Yàlla jox ko nguur ga ak xam-xam, xamal ko ca la ko soob. Bu dul koon ak li Yàlla di fege aw nit ak ñeneen, kon suuf si dana yàqu. Waaye Yàlla mooy Boroom ngëneel yi muy sotti ci mbindéef yi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 249-253 — Simoore Al-Baqara

249فَلَمَّا فَصَلَ طَالُوتُ بِالْجُنُودِ قَالَ إِنَّ اللَّهَ مُبْتَلِيكُم بِنَهَرٍ فَمَن شَرِبَ مِنْهُ فَلَيْسَ مِنِّي وَمَن لَّمْ يَطْعَمْهُ فَإِنَّهُ مِنِّي إِلَّا مَنِ اغْتَرَفَ غُرْفَةً بِيَدِهِ ۚ فَشَرِبُوا مِنْهُ إِلَّا قَلِيلًا مِّنْهُمْ ۚ فَلَمَّا جَاوَزَهُ هُوَ وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ قَالُوا لَا طَاقَةَ لَنَا الْيَوْمَ بِجَالُوتَ وَجُنُودِهِ ۚ قَالَ الَّذِينَ يَظُنُّونَ أَنَّهُم مُّلَاقُو اللَّهِ كَم مِّن فِئَةٍ قَلِيلَةٍ غَلَبَتْ فِئَةً كَثِيرَةً بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ مَعَ الصَّابِرِينَ
Ba TaaLóota génnee ànd ak ay xarekatam, mu ne leen : “Yàllaa ngi leen di nattu ci ag dex : ku ca naan dootoo bokk ci man ; ku ca mosul ci man nga bokk ; - ak ku ca corfati lu néew ci loxoom.” Naan nañu ca ñoom ñépp lu dul lu néew ca ñoom. Ba ñu jàllee dex ga, moom [TaaLóota] ak ña gëm te ànd ak moom, ñu ne : “Amunu tey kàttan [gu nu xeexee] ak [JaaLóota] ak i xarekatam ! ” Ña gëm ne danañu dajeek seen Boroom wax ne : “Bariwaana bu mbooloo mu néew note mbooloo mu bari. ! Te it Yàlla ànd na ak way-muñ ña”.
250وَلَمَّا بَرَزُوا لِجَالُوتَ وَجُنُودِهِ قَالُوا رَبَّنَا أَفْرِغْ عَلَيْنَا صَبْرًا وَثَبِّتْ أَقْدَامَنَا وَانصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ
Ba ñu génnee jëm ca JaaLóota ak i xarekatam, ñu ne : “Yàlla sunu Boroom ! nanga sotti ci nun muñ, te nga saxal sunuy tànk te nga defal nu ndimbal ci kaw nit ñu weddi ñii”.
251فَهَزَمُوهُم بِإِذْنِ اللَّهِ وَقَتَلَ دَاوُودُ جَالُوتَ وَآتَاهُ اللَّهُ الْمُلْكَ وَالْحِكْمَةَ وَعَلَّمَهُ مِمَّا يَشَاءُ ۗ وَلَوْلَا دَفْعُ اللَّهِ النَّاسَ بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لَّفَسَدَتِ الْأَرْضُ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ ذُو فَضْلٍ عَلَى الْعَالَمِينَ
Nu def ci ndigalu Yàlla [Daawuda] rey [Jaaluta] ; Yàlla jox ko nguur ga ak xam-xam, xamal ko ca la ko soob. Bu dul koon ak li Yàlla di fege aw nit ak ñeneen, kon suuf si dana yàqu. Waaye Yàlla mooy Boroom ngëneel yi muy sotti ci mbindéef yi.
252تِلْكَ آيَاتُ اللَّهِ نَتْلُوهَا عَلَيْكَ بِالْحَقِّ ۚ وَإِنَّكَ لَمِنَ الْمُرْسَلِينَ
Kàddug Yàlla googu dananu la ko jàngal ci dëgg.Te yaw [Muhammad] (saw), ci Yonent yi nga bokk.
253۞ تِلْكَ الرُّسُلُ فَضَّلْنَا بَعْضَهُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ ۘ مِّنْهُم مَّن كَلَّمَ اللَّهُ ۖ وَرَفَعَ بَعْضَهُمْ دَرَجَاتٍ ۚ وَآتَيْنَا عِيسَى ابْنَ مَرْيَمَ الْبَيِّنَاتِ وَأَيَّدْنَاهُ بِرُوحِ الْقُدُسِ ۗ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا اقْتَتَلَ الَّذِينَ مِن بَعْدِهِم مِّن بَعْدِ مَا جَاءَتْهُمُ الْبَيِّنَاتُ وَلَٰكِنِ اخْتَلَفُوا فَمِنْهُم مَّنْ آمَنَ وَمِنْهُم مَّن كَفَرَ ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا اقْتَتَلُوا وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يَفْعَلُ مَا يُرِيدُ
Yonent yooyu, gënal nanu ñenn ci kaw ñeneen ña ; Am na ci ñu Yàlla wax ak ñoom, yékkati ñenn ña seeni daraja. Te jox Nanu (Iisaa) doomu Maryaama lay yu leer nàññ, dëgërale ko Ruu gu Sell. Bu sooboon Yàlla, ñi ñëw seen ginnaaw duñu reyante, ginnaaw ba ñu jotee lay yu leer nàññ ; waaye dañoo juuyoo : mu am ca ñoom ñu gëm, am it ñu weddi. Bu sooboon Yàlla, duñu xeex ; waaye Yàlla dana def la mu namm.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
251Aaya

Tekki — Al-Baqara 251

Simoore Al-Baqara Aaya 251 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu def ci ndigalu Yàlla [Daawuda] rey [Jaaluta] ; Yàlla…

Simoore Aaya 251/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 249–253. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers