Al-Baqara · 47/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اذْكُرُوا نِعْمَتِيَ الَّتِي أَنْعَمْتُ عَلَيْكُمْ وَأَنِّي فَضَّلْتُكُمْ عَلَى الْعَالَمِينَ ۝٤٧
Yaa Baneee Israaa`eelaz kuroo ni`matiyal lateee an`amtu `alaikum wa annee faddaltukum `alal `aalameen
📖 Tekkim Wolof
Yéen ñi sëtoo ci Yànqooba, fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma leen xéewalee woon, te Man ma defaloon leen ngëneel ci kaw nit ñépp.

🎧 Dégg


📜 Aaya 45-49 — Simoore Al-Baqara

45وَاسْتَعِينُوا بِالصَّبْرِ وَالصَّلَاةِ ۚ وَإِنَّهَا لَكَبِيرَةٌ إِلَّا عَلَى الْخَاشِعِينَ
Nangeen di dimbandikoo muñ ak Julli : loolu lu diis la ci ku bokkul ci way-ragal Yàlla ña,
46الَّذِينَ يَظُنُّونَ أَنَّهُم مُّلَاقُو رَبِّهِمْ وَأَنَّهُمْ إِلَيْهِ رَاجِعُونَ
ña nga xam ne daleen a wóor ne danañu dajeek seen Boroom te ca Moom lañuy dellu.
47يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اذْكُرُوا نِعْمَتِيَ الَّتِي أَنْعَمْتُ عَلَيْكُمْ وَأَنِّي فَضَّلْتُكُمْ عَلَى الْعَالَمِينَ
Yéen ñi sëtoo ci Yànqooba, fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma leen xéewalee woon, te Man ma defaloon leen ngëneel ci kaw nit ñépp.
48وَاتَّقُوا يَوْمًا لَّا تَجْزِي نَفْسٌ عَن نَّفْسٍ شَيْئًا وَلَا يُقْبَلُ مِنْهَا شَفَاعَةٌ وَلَا يُؤْخَذُ مِنْهَا عَدْلٌ وَلَا هُمْ يُنصَرُونَ
Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan ; te duñu ko nangul rammu ; duñu ko nangul njote. Te deesuleen dimbali.
49وَإِذْ نَجَّيْنَاكُم مِّنْ آلِ فِرْعَوْنَ يَسُومُونَكُمْ سُوءَ الْعَذَابِ يُذَبِّحُونَ أَبْنَاءَكُمْ وَيَسْتَحْيُونَ نِسَاءَكُمْ ۚ وَفِي ذَٰلِكُم بَلَاءٌ مِّن رَّبِّكُمْ عَظِيمٌ
[Fàttalikuleen], ba Nu leen musalee ci waa kër (Firawna), tegoon nañu leen mbugal mu ñaaw : ñuy rendi seeni doom yu góor ya, di bàyyi ñu jigéen ña. Nekkoon na ci loolu nattu bu réy bu bawoo ca seen Boroom.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
47Aaya

Tekki — Al-Baqara 47

Simoore Al-Baqara Aaya 47 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéen ñi sëtoo ci Yànqooba, fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma…

Simoore Aaya 47/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 45–49. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers