Al-Anbiya · 92/112
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anbiya
إِنَّ هَٰذِهِ أُمَّتُكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَأَنَا رَبُّكُمْ فَاعْبُدُونِ ۝٩٢
Inna haaziheee ummatukum ummatanw waahidatanw wa Ana Rabbukum fa`budoon
📖 Tekkim Wolof
Lii nag moo di seen diine, mu di jenn diine doŋŋ, te Man maa di seen Boroom. Waay- waay kon jaamuleen Ma.

🎧 Dégg


📜 Aaya 90-94 — Simoore Al-Anbiya

90فَاسْتَجَبْنَا لَهُ وَوَهَبْنَا لَهُ يَحْيَىٰ وَأَصْلَحْنَا لَهُ زَوْجَهُ ۚ إِنَّهُمْ كَانُوا يُسَارِعُونَ فِي الْخَيْرَاتِ وَيَدْعُونَنَا رَغَبًا وَرَهَبًا ۖ وَكَانُوا لَنَا خَاشِعِينَ
Nu nangul ko, may ko Yahyaa te Nu yéwénalal ko soxnaam. Ñoom sax dañu daan njëkkante ci jëf yu yiw ya te ñoom daanañu Nu jaamu, nekk ci diggante xemmem ak ragal. Te nekkoon nañu diy way-toroxlu ci Nun.
91وَالَّتِي أَحْصَنَتْ فَرْجَهَا فَنَفَخْنَا فِيهَا مِن رُّوحِنَا وَجَعَلْنَاهَا وَابْنَهَا آيَةً لِّلْعَالَمِينَ
Ak jigéen ja ñoŋal boppam [Maryam] ! Nu wal ci moom lenn ci Sunu ruu, daldi koy def mook doomam [Iisaa] ñuy kaawtéef ci àddina si yépp.
92إِنَّ هَٰذِهِ أُمَّتُكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَأَنَا رَبُّكُمْ فَاعْبُدُونِ
Lii nag moo di seen diine, mu di jenn diine doŋŋ, te Man maa di seen Boroom. Waay- waay kon jaamuleen Ma.
93وَتَقَطَّعُوا أَمْرَهُم بَيْنَهُمْ ۖ كُلٌّ إِلَيْنَا رَاجِعُونَ
De daggate nañu seeni mbir ca seen diggante. Te ñoom ñépp fi Nun lañuy dellusi.
94فَمَن يَعْمَلْ مِنَ الصَّالِحَاتِ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَلَا كُفْرَانَ لِسَعْيِهِ وَإِنَّا لَهُ كَاتِبُونَ
Képp kuy jëf ca jëf yu yiw ya te muy ku gëm, deesul fakk jëfam ndax Nun noo ko koy bindal.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
92Aaya

Tekki — Al-Anbiya 92

Simoore Al-Anbiya Aaya 92 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Lii nag moo di seen diine, mu di jenn diine…

Simoore Aaya 92/112 — Simoore Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anbiya Dégg, Simoore Al-Anbiya Tekki, Simoore Al-Anbiya mp3, Simoore Al-Anbiya pdf. Aaya 90–94. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers