Al-Hajj · 38/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
۞ إِنَّ اللَّهَ يُدَافِعُ عَنِ الَّذِينَ آمَنُوا ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ كُلَّ خَوَّانٍ كَفُورٍ ۝٣٨
Innal laaha yudaafi` `anil lazeena aamanoo; innal laaha laa yuhibbu kulla khawwaanin kafoor
📖 Tekkim Wolof
Te Yàlla dana jiñal lu bon ña gëm. Te Yàlla soppul bépp wurujaakoon ju di weddikat.

🎧 Dégg


📜 Aaya 36-40 — Al-Hajj

36وَالْبُدْنَ جَعَلْنَاهَا لَكُم مِّن شَعَائِرِ اللَّهِ لَكُمْ فِيهَا خَيْرٌ ۖ فَاذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ عَلَيْهَا صَوَافَّ ۖ فَإِذَا وَجَبَتْ جُنُوبُهَا فَكُلُوا مِنْهَا وَأَطْعِمُوا الْقَانِعَ وَالْمُعْتَرَّ ۚ كَذَٰلِكَ سَخَّرْنَاهَا لَكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Te giléem yu suur ya, defal Nanu leen ñu bokk ca ya ñuy jaamoo Yàlla. Aw yiw doŋŋ la ñeel leen. Nangeen ci tudd turu Yàlla bu ñu leen di loj. Bu ñu daanoo tëdd ci seeni wet, nangeen ca lekk te ngeen leel ca way-doylu ña ak yalwaankat ya. Noonu la Nu leen tegtale ndax yéen ngeen gërëm.
37لَن يَنَالَ اللَّهَ لُحُومُهَا وَلَا دِمَاؤُهَا وَلَٰكِن يَنَالُهُ التَّقْوَىٰ مِنكُمْ ۚ كَذَٰلِكَ سَخَّرَهَا لَكُمْ لِتُكَبِّرُوا اللَّهَ عَلَىٰ مَا هَدَاكُمْ ۗ وَبَشِّرِ الْمُحْسِنِينَ
Te Yàlla amul soxla ci yàpp wi walla dereet ji. Waaye la Ko soxal moo di ragal Yàlla gi nekk ci yéen. Noonu la Nu leen leen tàggate ngir ngeen màggal Yàlla ci li Mu leen gindi. Te nga bégal way-rafetal ña.
38۞ إِنَّ اللَّهَ يُدَافِعُ عَنِ الَّذِينَ آمَنُوا ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ كُلَّ خَوَّانٍ كَفُورٍ
Te Yàlla dana jiñal lu bon ña gëm. Te Yàlla soppul bépp wurujaakoon ju di weddikat.
39أُذِنَ لِلَّذِينَ يُقَاتَلُونَ بِأَنَّهُمْ ظُلِمُوا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ نَصْرِهِمْ لَقَدِيرٌ
Ña ñu dal ca seen kaw, may Nanu leen ñu xare ngir dañu leen a tooñ ; te Yàlla am na kàttan ci dimbali leen -
40الَّذِينَ أُخْرِجُوا مِن دِيَارِهِم بِغَيْرِ حَقٍّ إِلَّا أَن يَقُولُوا رَبُّنَا اللَّهُ ۗ وَلَوْلَا دَفْعُ اللَّهِ النَّاسَ بَعْضَهُم بِبَعْضٍ لَّهُدِّمَتْ صَوَامِعُ وَبِيَعٌ وَصَلَوَاتٌ وَمَسَاجِدُ يُذْكَرُ فِيهَا اسْمُ اللَّهِ كَثِيرًا ۗ وَلَيَنصُرَنَّ اللَّهُ مَن يَنصُرُهُ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَقَوِيٌّ عَزِيزٌ
may Na ko it ña ñu génnee ci seeni kër, - ci lu dul dëgg, te defuñu lu dul wax rekk ne : “Yàllaa di sunu Boroom”. - Bu dul kon ak li Yàlla di fege ñenn nit ci ñeneen, kon deef na màbb jaamukaayi yahuud yi, ak yu nasraan yi ak jàkka yi di fu ñuy tudde Yàlla lu bari. Te fàwwu Yàlla dana dimbali ña koy dimbali. Te Yàlla ku bari doole la, di ku not lépp,
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
38Aaya

Tekki — Al-Hajj 38

Simoore Al-Hajj Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Yàlla dana jiñal lu bon ña gëm. Te Yàlla…

Simoore Aaya 38/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers