Al-Hajj · 53/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
لِّيَجْعَلَ مَا يُلْقِي الشَّيْطَانُ فِتْنَةً لِّلَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ وَالْقَاسِيَةِ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ الظَّالِمِينَ لَفِي شِقَاقٍ بَعِيدٍ ۝٥٣
Liyaj`ala maa yulqish Shaitaanu fitnatal lillazeena fee quloobihim maradunw walqaasiyati quloobuhum; wa innaz zaalimeena lafee shiqaaqim ba`eed
📖 Tekkim Wolof
Lu Séytaane sànni Dafa koo def muy nattu ca ña jàngoro nekk ca seen xol ak ña seeni xol wow... Ca tooñkat ya ñu nekk ci wuute gu sore [dëgg].

🎧 Dégg


📜 Aaya 51-55 — Al-Hajj

51وَالَّذِينَ سَعَوْا فِي آيَاتِنَا مُعَاجِزِينَ أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ
ña nga xam ne ñi ngi dox di yoqatloo nit ñi ci Sunuy ndigal, ñooña ñooy waa Safara.
52وَمَا أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ مِن رَّسُولٍ وَلَا نَبِيٍّ إِلَّا إِذَا تَمَنَّىٰ أَلْقَى الشَّيْطَانُ فِي أُمْنِيَّتِهِ فَيَنسَخُ اللَّهُ مَا يُلْقِي الشَّيْطَانُ ثُمَّ يُحْكِمُ اللَّهُ آيَاتِهِ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Mësunoo yónni ci lu jiitu ab Yonent walla ku Nu soloo te bu mébétee dara Séytaane du sànni pexe mu bon ci mébétam. Waaye Yàlla dana masaxal la Séytaane sànni woon, ba noppi dëggal ay ndigalam. Te Yàlla Ku xam la Ku xereñ la.
53لِّيَجْعَلَ مَا يُلْقِي الشَّيْطَانُ فِتْنَةً لِّلَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ وَالْقَاسِيَةِ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ الظَّالِمِينَ لَفِي شِقَاقٍ بَعِيدٍ
Lu Séytaane sànni Dafa koo def muy nattu ca ña jàngoro nekk ca seen xol ak ña seeni xol wow... Ca tooñkat ya ñu nekk ci wuute gu sore [dëgg].
54وَلِيَعْلَمَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ أَنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ فَيُؤْمِنُوا بِهِ فَتُخْبِتَ لَهُ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَهَادِ الَّذِينَ آمَنُوا إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te Moo dogal loolu lépp ngir ña nga xam ne joxeef na leen xam-xam, ràññee ne Alxuraan ak moom dëgg la gu bawoo fa sa Boroom, ak ngir ñu gëm ko ci seeni xol, dellu ci Moom. Te ñu xam ne Yàlla dana gindi ñi gëm teg leen ca yoon wu jub xocc wa.
55وَلَا يَزَالُ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي مِرْيَةٍ مِّنْهُ حَتَّىٰ تَأْتِيَهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً أَوْ يَأْتِيَهُمْ عَذَابُ يَوْمٍ عَقِيمٍ
Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan ba baa Bis-pénc di leen dikkal ci mbetteel walla mbugalum bis bu tiis ba dikkal leen.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
53Aaya

Tekki — Al-Hajj 53

Simoore Al-Hajj Aaya 53 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Lu Séytaane sànni Dafa koo def muy nattu ca ña…

Simoore Aaya 53/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 51–55. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers