Al-Furqan · 4/77
Tekki Waxtaan — Al-Furqan
وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ هَٰذَا إِلَّا إِفْكٌ افْتَرَاهُ وَأَعَانَهُ عَلَيْهِ قَوْمٌ آخَرُونَ ۖ فَقَدْ جَاءُوا ظُلْمًا وَزُورًا ۝٤
Wa qaalal lazeena kafarooo in haazaaa illaaa ifkunif taraahu wa a`aanahoo `alaihi qawmun aakharoona faqad jaaa`oo zulmanw wa zooraa
📖 Tekkim Wolof
Yéefar yi wax nañu ne : “[Alxuraan] jii daal aw duur la wu [Muhammad] moo ko sos, te dafa am ñu ko cay jàppale”. Li ñu fi indi tooñ ak i fen la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 2-6 — Al-Furqan

2الَّذِي لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلَمْ يَتَّخِذْ وَلَدًا وَلَمْ يَكُن لَّهُ شَرِيكٌ فِي الْمُلْكِ وَخَلَقَ كُلَّ شَيْءٍ فَقَدَّرَهُ تَقْدِيرًا
Moom mi nga xam ne Moo moom nguurug asamaan yeek suuf si, te jàppewul kenn doomam, te it amul ku Mu bokkal nguur gi, Moo bind lépp te jox na ko dayo ba mu témbool.
3وَاتَّخَذُوا مِن دُونِهِ آلِهَةً لَّا يَخْلُقُونَ شَيْئًا وَهُمْ يُخْلَقُونَ وَلَا يَمْلِكُونَ لِأَنفُسِهِمْ ضَرًّا وَلَا نَفْعًا وَلَا يَمْلِكُونَ مَوْتًا وَلَا حَيَاةً وَلَا نُشُورًا
Te ñoom dañoo jàppe ay yàlla ñenenn ñoo xam ne binduñu tus, faf ñoom sax dañu leen a bind, te it mënuñoo lor seen bopp waxantumalaak njariñ, amuñu dee amuñu dundu waxantumalaak dekki.
4وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ هَٰذَا إِلَّا إِفْكٌ افْتَرَاهُ وَأَعَانَهُ عَلَيْهِ قَوْمٌ آخَرُونَ ۖ فَقَدْ جَاءُوا ظُلْمًا وَزُورًا
Yéefar yi wax nañu ne : “[Alxuraan] jii daal aw duur la wu [Muhammad] moo ko sos, te dafa am ñu ko cay jàppale”. Li ñu fi indi tooñ ak i fen la.
5وَقَالُوا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ اكْتَتَبَهَا فَهِيَ تُمْلَىٰ عَلَيْهِ بُكْرَةً وَأَصِيلًا
Ñu wax it ne : “Léebi mag ñu jëkk ña rekk la ! Ñu koy saa muy bind suba ak ngoon ! ”
6قُلْ أَنزَلَهُ الَّذِي يَعْلَمُ السِّرَّ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ إِنَّهُ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Neel : “Ki ko wàcce moo xam mbooti asamaan yeek suuf si. Di ab Jéggalaakon, di Jaglewaakoon.
Al-FurqanFihi Alxuraan
77Aaya
MeccanRevelation
4Aaya

Tekki — Al-Furqan 4

Simoore Al-Furqan Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yéefar yi wax nañu ne : “[Alxuraan] jii daal aw…

Simoore Aaya 4/77 — Al-Furqan الفرقان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Furqan Dégg, Al-Furqan Tekki, Al-Furqan mp3, Al-Furqan pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers