An-Naml · 44/93
Tekki Waxtaan — Simoore An-Naml
قِيلَ لَهَا ادْخُلِي الصَّرْحَ ۖ فَلَمَّا رَأَتْهُ حَسِبَتْهُ لُجَّةً وَكَشَفَتْ عَن سَاقَيْهَا ۚ قَالَ إِنَّهُ صَرْحٌ مُّمَرَّدٌ مِّن قَوَارِيرَ ۗ قَالَتْ رَبِّ إِنِّي ظَلَمْتُ نَفْسِي وَأَسْلَمْتُ مَعَ سُلَيْمَانَ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ ۝٤٤
Qeela lahad khulis sarha falammaa ra at hu hasibat hu lujjatanw wa khashafat `an saaqaihaa; qaala innahoo sarhum mumarradum min qawaareer; qaalat Rabbi innee zalamtu nafsee wa aslamtu ma`a Sulaimaana lillaahi Rabbil `aalameen
📖 Tekkim Wolof
Ñu ne ko : “Dugal ci njénde li”. Ba mu ko gisee, mu njort ne am ndox la, daldi wog i yeelam. Suleymaan ne ko : “Njénde li ay weer la ñu ko defare”. - Balxiis daldi ne : “Yaw Boroom bi, tooñaan naa sama bopp : Tey jii nag, jébbalu naa ànd ak Suleymaan dib jullit ngir Yàlla jiy Boroom àddina si”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 42-46 — Simoore An-Naml

42فَلَمَّا جَاءَتْ قِيلَ أَهَٰكَذَا عَرْشُكِ ۖ قَالَتْ كَأَنَّهُ هُوَ ۚ وَأُوتِينَا الْعِلْمَ مِن قَبْلِهَا وَكُنَّا مُسْلِمِينَ
Ba Balxiis agsee, ñu ne ko : “Ndax lii mooy sa toogu ba ? ” Mu ne : “Mel na ni moom la de”. - [Suleymaan ne]: “Am nanu xam-xam lu ko jiitu ba tax na nu jébbalusi”.
43وَصَدَّهَا مَا كَانَت تَّعْبُدُ مِن دُونِ اللَّهِ ۖ إِنَّهَا كَانَتْ مِن قَوْمٍ كَافِرِينَ
Li mu daan jaamu bàyyi Yàlla moo ko fàbbi woon, ndax dafa bokkoon ci askanu yéefar.
44قِيلَ لَهَا ادْخُلِي الصَّرْحَ ۖ فَلَمَّا رَأَتْهُ حَسِبَتْهُ لُجَّةً وَكَشَفَتْ عَن سَاقَيْهَا ۚ قَالَ إِنَّهُ صَرْحٌ مُّمَرَّدٌ مِّن قَوَارِيرَ ۗ قَالَتْ رَبِّ إِنِّي ظَلَمْتُ نَفْسِي وَأَسْلَمْتُ مَعَ سُلَيْمَانَ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Ñu ne ko : “Dugal ci njénde li”. Ba mu ko gisee, mu njort ne am ndox la, daldi wog i yeelam. Suleymaan ne ko : “Njénde li ay weer la ñu ko defare”. - Balxiis daldi ne : “Yaw Boroom bi, tooñaan naa sama bopp : Tey jii nag, jébbalu naa ànd ak Suleymaan dib jullit ngir Yàlla jiy Boroom àddina si”.
45وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ ثَمُودَ أَخَاهُمْ صَالِحًا أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ فَإِذَا هُمْ فَرِيقَانِ يَخْتَصِمُونَ
Yónnee woon Nanu ca Samuuda seen mbokk Saaliwu. Mu ne leen : “Jaamuleen Yàlla”. Ndekete yoo dañoo séddalikoo ñaari kurél di xulloo rekk.
46قَالَ يَا قَوْمِ لِمَ تَسْتَعْجِلُونَ بِالسَّيِّئَةِ قَبْلَ الْحَسَنَةِ ۖ لَوْلَا تَسْتَغْفِرُونَ اللَّهَ لَعَلَّكُمْ تُرْحَمُونَ
Mu ne leen : "Éy samaw nit, lu tax ngeen di gën a yàkkamti lu bon ci lu baax ? Céy bu ngeen jéggalu woon Yàlla ? Kon xéy-na Mu yërëm leen.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — An-Naml 44

Simoore An-Naml Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu ne ko : “Dugal ci njénde li”. Ba mu…

Simoore Aaya 44/93 — Simoore An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Naml Dégg, Simoore An-Naml Tekki, Simoore An-Naml mp3, Simoore An-Naml pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers