An-Naml · 60/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
أَمَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَأَنزَلَ لَكُم مِّنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَنبَتْنَا بِهِ حَدَائِقَ ذَاتَ بَهْجَةٍ مَّا كَانَ لَكُمْ أَن تُنبِتُوا شَجَرَهَا ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ بَلْ هُمْ قَوْمٌ يَعْدِلُونَ ۝٦٠
Amman khalaqas samaawaati wal arda wa anzala lakum minas samaaa`i maaa`an fa ambatnaa bihee hadaaa`iqa zaata bahjjah; maa kanna lakum an tumbitoo shajarahaa; `a-ilaahum ma`al laah; bal hum qawmuny ya`diloon
📖 Tekkim Wolof
Ana kan moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si te Mu wàcceel leen am ndox mu bawoo asamaan, daldi cay saxale ay tool yu taaru yoo xam ne mënuleen ko woon a saxal. Moo ndax dafa am jeneen yàlla juy ànd ak Yàlla ? [Amul], ñoom kay fu ñu toll ña ngay jéem a utal Yàlla ndend.

🎧 Dégg


📜 Aaya 58-62 — An-Naml

58وَأَمْطَرْنَا عَلَيْهِم مَّطَرًا ۖ فَسَاءَ مَطَرُ الْمُنذَرِينَ
Dotti Nanu ca seen kaw waamem [doj]. Ndaw taw bu bon ca ña mu dal ca seen kaw!
59قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ وَسَلَامٌ عَلَىٰ عِبَادِهِ الَّذِينَ اصْطَفَىٰ ۗ آللَّهُ خَيْرٌ أَمَّا يُشْرِكُونَ
Waxal : “Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla te yal na jàmm wàcc ci kaw jaamam ña Mu tànn ! ” Waaw! Ana lan moo gën : Yàlla walla li ngeen di bokkaale ?
60أَمَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَأَنزَلَ لَكُم مِّنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَنبَتْنَا بِهِ حَدَائِقَ ذَاتَ بَهْجَةٍ مَّا كَانَ لَكُمْ أَن تُنبِتُوا شَجَرَهَا ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ بَلْ هُمْ قَوْمٌ يَعْدِلُونَ
Ana kan moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si te Mu wàcceel leen am ndox mu bawoo asamaan, daldi cay saxale ay tool yu taaru yoo xam ne mënuleen ko woon a saxal. Moo ndax dafa am jeneen yàlla juy ànd ak Yàlla ? [Amul], ñoom kay fu ñu toll ña ngay jéem a utal Yàlla ndend.
61أَمَّن جَعَلَ الْأَرْضَ قَرَارًا وَجَعَلَ خِلَالَهَا أَنْهَارًا وَجَعَلَ لَهَا رَوَاسِيَ وَجَعَلَ بَيْنَ الْبَحْرَيْنِ حَاجِزًا ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ana kan moo waajal suuf si ba mu doon dëkkuwaay, mu def ci biir ay dex ak tundi doj te def ci diggante ñaari géej yi ay téq [muy tax ndox mu neex mi ak mu xorome mi duñu jaxasoo], - Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? Déedéet amul, waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
62أَمَّن يُجِيبُ الْمُضْطَرَّ إِذَا دَعَاهُ وَيَكْشِفُ السُّوءَ وَيَجْعَلُكُمْ خُلَفَاءَ الْأَرْضِ ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ قَلِيلًا مَّا تَذَكَّرُونَ
Ana kan mooy wuyyu boroom tiitaange saa yu Ko woowee, ana kan it mooy dindi njàqare ji, te def leen ngeen wuutu ko ci suuf si, - Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla? [Déedéet amul]. Li ñuy fàttaliku moo néew doŋŋ !
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
60Aaya

Tekki — An-Naml 60

Simoore An-Naml Aaya 60 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana kan moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si te…

Simoore Aaya 60/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 58–62. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers