An-Naml · 64/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
أَمَّن يَبْدَأُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ وَمَن يَرْزُقُكُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٦٤
Ammmany-yabda`ul khalqa summa yu`eeduhoo wa many-yarzuqukum minas sammaaa`i wal ard; `a-ilaahum ma`allah; qul haatoo burhaanakum in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Ana kan mooy tàmbali sosu ga, topp Mu di ko delloosi, ana kan moo leen di dundal ci la bawoo asamaan ak suuf. Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? [Déedéet amul de]. Neeleen : “Indileen seen firnde ndegam wax ngeen dëgg ! ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 62-66 — An-Naml

62أَمَّن يُجِيبُ الْمُضْطَرَّ إِذَا دَعَاهُ وَيَكْشِفُ السُّوءَ وَيَجْعَلُكُمْ خُلَفَاءَ الْأَرْضِ ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ قَلِيلًا مَّا تَذَكَّرُونَ
Ana kan mooy wuyyu boroom tiitaange saa yu Ko woowee, ana kan it mooy dindi njàqare ji, te def leen ngeen wuutu ko ci suuf si, - Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla? [Déedéet amul]. Li ñuy fàttaliku moo néew doŋŋ !
63أَمَّن يَهْدِيكُمْ فِي ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَمَن يُرْسِلُ الرِّيَاحَ بُشْرًا بَيْنَ يَدَيْ رَحْمَتِهِ ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ تَعَالَى اللَّهُ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Ana kan moo leen di gindi ci lëndëmug jéeri jeek géej gi, tey yebal ngelaw liy bégle ci yërmaandeem [xamle taw buy bëgg sóob]. Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? Déedéet [amul de]. Yàlla kawe na li ñu koy bokkaaleel.
64أَمَّن يَبْدَأُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ وَمَن يَرْزُقُكُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۗ أَإِلَٰهٌ مَّعَ اللَّهِ ۚ قُلْ هَاتُوا بُرْهَانَكُمْ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Ana kan mooy tàmbali sosu ga, topp Mu di ko delloosi, ana kan moo leen di dundal ci la bawoo asamaan ak suuf. Moo ndax dafa am jeneen yàlla ju ànd ak Yàlla ? [Déedéet amul de]. Neeleen : “Indileen seen firnde ndegam wax ngeen dëgg ! ”
65قُل لَّا يَعْلَمُ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ الْغَيْبَ إِلَّا اللَّهُ ۚ وَمَا يَشْعُرُونَ أَيَّانَ يُبْعَثُونَ
Neel : “Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si, kenn xamu ci kumpa ku dul Yàlla”. Te it xamuñu kañ la ñuy dekki !
66بَلِ ادَّارَكَ عِلْمُهُمْ فِي الْآخِرَةِ ۚ بَلْ هُمْ فِي شَكٍّ مِّنْهَا ۖ بَلْ هُم مِّنْهَا عَمُونَ
Seeni xam-xam soriwul ci mbiri àllaaxira. Ñoom sax dañu cay sikki-sàkka. Te ñoom sax ay gumba lañu ci mbir moomu.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
64Aaya

Tekki — An-Naml 64

Simoore An-Naml Aaya 64 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana kan mooy tàmbali sosu ga, topp Mu di ko…

Simoore Aaya 64/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 62–66. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers