Al-Qasas · 78/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
قَالَ إِنَّمَا أُوتِيتُهُ عَلَىٰ عِلْمٍ عِندِي ۚ أَوَلَمْ يَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ قَدْ أَهْلَكَ مِن قَبْلِهِ مِنَ الْقُرُونِ مَنْ هُوَ أَشَدُّ مِنْهُ قُوَّةً وَأَكْثَرُ جَمْعًا ۚ وَلَا يُسْأَلُ عَن ذُنُوبِهِمُ الْمُجْرِمُونَ ۝٧٨
Qaala innamaaa ootee tuhoo `alaa `ilmin `indeee; awalam ya`lam annal laaha qad ahlaka min qablihee minal qurooni man huwa ashaddu minhu quwwatanw wa aksaru jam`aa; wa laa yus`alu `an zunoobihimul mujrimoon
📖 Tekkim Wolof
Xaaruuna wax ne : “Lii ci sama xam-xam laa ko ame”. Xanaa moom dafa xamul ña Yàlla faagaagal ca maas ya ko jiitu, ña ko gënoon a ñàng ëpp ko fuuf dooleek alal ? Te tooñkat ña deefuleen laaj seen bàkkaar !

🎧 Dégg


📜 Aaya 76-80 — Simoore Al-Qasas

76۞ إِنَّ قَارُونَ كَانَ مِن قَوْمِ مُوسَىٰ فَبَغَىٰ عَلَيْهِمْ ۖ وَآتَيْنَاهُ مِنَ الْكُنُوزِ مَا إِنَّ مَفَاتِحَهُ لَتَنُوءُ بِالْعُصْبَةِ أُولِي الْقُوَّةِ إِذْ قَالَ لَهُ قَوْمُهُ لَا تَفْرَحْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْفَرِحِينَ
[Bir na ne], Xaaruuna ci nitu Muusaa la bokkoon, waaye dafa bewoon. Joxoon Nanu ko ci ay ndàmb, loo xam ne, bu ñu lewaa caabi ya mu diis gann ay ponkal. Fàttalikul ba ko ay nitam waxee ne ko : “Bul rëy-rëylu. Yàlla safoowul ñuy rëy-rëylu.
77وَابْتَغِ فِيمَا آتَاكَ اللَّهُ الدَّارَ الْآخِرَةَ ۖ وَلَا تَنسَ نَصِيبَكَ مِنَ الدُّنْيَا ۖ وَأَحْسِن كَمَا أَحْسَنَ اللَّهُ إِلَيْكَ ۖ وَلَا تَبْغِ الْفَسَادَ فِي الْأَرْضِ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ الْمُفْسِدِينَ
Li la Yàlla jox, sàkku ci kërug àllaaxira [Àjjana]. Te bul fàtte sa wàll ci àdduna. Te nangay rafetal kem ni Yàlla di rafetale jëme ci yaw. Bul di sàkku ag yàq ci suuf si. Ndax Yàlla dey safoowul yàqkat yi”.
78قَالَ إِنَّمَا أُوتِيتُهُ عَلَىٰ عِلْمٍ عِندِي ۚ أَوَلَمْ يَعْلَمْ أَنَّ اللَّهَ قَدْ أَهْلَكَ مِن قَبْلِهِ مِنَ الْقُرُونِ مَنْ هُوَ أَشَدُّ مِنْهُ قُوَّةً وَأَكْثَرُ جَمْعًا ۚ وَلَا يُسْأَلُ عَن ذُنُوبِهِمُ الْمُجْرِمُونَ
Xaaruuna wax ne : “Lii ci sama xam-xam laa ko ame”. Xanaa moom dafa xamul ña Yàlla faagaagal ca maas ya ko jiitu, ña ko gënoon a ñàng ëpp ko fuuf dooleek alal ? Te tooñkat ña deefuleen laaj seen bàkkaar !
79فَخَرَجَ عَلَىٰ قَوْمِهِ فِي زِينَتِهِ ۖ قَالَ الَّذِينَ يُرِيدُونَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا يَا لَيْتَ لَنَا مِثْلَ مَا أُوتِيَ قَارُونُ إِنَّهُ لَذُو حَظٍّ عَظِيمٍ
Mu génn ca nitam ña, ànd ak alalam ja. Ñi bëgg dundu àddina wax ne : “Aka neexoon nu am lii Xaaruuna am. Moom dey boroom cër bu duun na”.
80وَقَالَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ وَيْلَكُمْ ثَوَابُ اللَّهِ خَيْرٌ لِّمَنْ آمَنَ وَعَمِلَ صَالِحًا وَلَا يُلَقَّاهَا إِلَّا الصَّابِرُونَ
Ña am xam-xam ne leen : “Toskare ngeen ! Yoolub Yàllaa gënal képp ku gëm tey jëf u yiw”. Ku dul muñkat du ko am.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
78Aaya

Tekki — Al-Qasas 78

Simoore Al-Qasas Aaya 78 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xaaruuna wax ne : “Lii ci sama xam-xam laa ko…

Simoore Aaya 78/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 76–80. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers