Aali Imran · 145/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَمَا كَانَ لِنَفْسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ كِتَابًا مُّؤَجَّلًا ۗ وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الْآخِرَةِ نُؤْتِهِ مِنْهَا ۚ وَسَنَجْزِي الشَّاكِرِينَ ۝١٤٥
Wa maa kaana linafsin an tamoota illaa bi iznillaahi kitaabam mu`ajjalaa; wa mai yurid sawaabad dunyaa nu`tihee minhaa wa mai yurid sawaabal Aakhirati nu`tihee minhaa; wa sanajzish shaakireen
📖 Tekkim Wolof
Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram.

🎧 Dégg


📜 Aaya 143-147 — Aali Imran

143وَلَقَدْ كُنتُمْ تَمَنَّوْنَ الْمَوْتَ مِن قَبْلِ أَن تَلْقَوْهُ فَقَدْ رَأَيْتُمُوهُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ
Mebetoon ngeen dey lu jiitu ngeen dajeek Moom. Léegi ndax gis ngeen ko, ne ci jàkk !
144وَمَا مُحَمَّدٌ إِلَّا رَسُولٌ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِ الرُّسُلُ ۚ أَفَإِن مَّاتَ أَوْ قُتِلَ انقَلَبْتُمْ عَلَىٰ أَعْقَابِكُمْ ۚ وَمَن يَنقَلِبْ عَلَىٰ عَقِبَيْهِ فَلَن يَضُرَّ اللَّهَ شَيْئًا ۗ وَسَيَجْزِي اللَّهُ الشَّاكِرِينَ
Muhammad doonul lu may ab Yonent - boo xam ne ay Yonent ñoo ko jiitu woon ba jàll - Ndax bu deewoon walla ñu rey ko, dangeen di dellu ca seeni tànk, weddi ? Ku walbatiku ca ay tànkam, du wàññi Yàlla dara ; te Yàlla dana fey ñay gëram seen Boroom.
145وَمَا كَانَ لِنَفْسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ كِتَابًا مُّؤَجَّلًا ۗ وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الْآخِرَةِ نُؤْتِهِ مِنْهَا ۚ وَسَنَجْزِي الشَّاكِرِينَ
Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram.
146وَكَأَيِّن مِّن نَّبِيٍّ قَاتَلَ مَعَهُ رِبِّيُّونَ كَثِيرٌ فَمَا وَهَنُوا لِمَا أَصَابَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَمَا ضَعُفُوا وَمَا اسْتَكَانُوا ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الصَّابِرِينَ
Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi.
147وَمَا كَانَ قَوْلَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَإِسْرَافَنَا فِي أَمْرِنَا وَثَبِّتْ أَقْدَامَنَا وَانصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ
Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar”.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
145Aaya

Tekki — Aali Imran 145

Simoore Aali Imran Aaya 145 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci…

Simoore Aaya 145/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 143–147. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers