Aali Imran · 174/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
فَانقَلَبُوا بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ لَّمْ يَمْسَسْهُمْ سُوءٌ وَاتَّبَعُوا رِضْوَانَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ ذُو فَضْلٍ عَظِيمٍ ۝١٧٤
Fanqalaboo bini`matim minal laahi wa fadlil lam yamsashum sooo`unw wattaba`oo ridwaanal laah; wallaahu zoo fadlin `azeem
📖 Tekkim Wolof
Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 172-176 — Aali Imran

172الَّذِينَ اسْتَجَابُوا لِلَّهِ وَالرَّسُولِ مِن بَعْدِ مَا أَصَابَهُمُ الْقَرْحُ ۚ لِلَّذِينَ أَحْسَنُوا مِنْهُمْ وَاتَّقَوْا أَجْرٌ عَظِيمٌ
Ñoom ña wuyu [wooteb] Yàlla ak Yonent ba, ginnaaw ba leen jam-jam ya [ca xare Uhud] dalee, ña doon rafetal ca ñoom te ragal Yàlla, am nañu pey gu màgg.
173الَّذِينَ قَالَ لَهُمُ النَّاسُ إِنَّ النَّاسَ قَدْ جَمَعُوا لَكُمْ فَاخْشَوْهُمْ فَزَادَهُمْ إِيمَانًا وَقَالُوا حَسْبُنَا اللَّهُ وَنِعْمَ الْوَكِيلُ
Ñooy ña nit ña ne woon : “Yéen a toog, waaye nit ñaa [seeni noon] ngi daje ngir sànk leen, war ngeen a tiit” - faf loolu yokk leen ngëm - ñu toontu ne : “Yàlla doy nanu te Mooy ngën gi wéeruwaay”.
174فَانقَلَبُوا بِنِعْمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَفَضْلٍ لَّمْ يَمْسَسْهُمْ سُوءٌ وَاتَّبَعُوا رِضْوَانَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ ذُو فَضْلٍ عَظِيمٍ
Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu bon daluleen, topp nañu lu neex Yàlla. Te Yàlla boroom ngëneel yu màgg la.
175إِنَّمَا ذَٰلِكُمُ الشَّيْطَانُ يُخَوِّفُ أَوْلِيَاءَهُ فَلَا تَخَافُوهُمْ وَخَافُونِ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
[Xupp googu ñu leen di xupp] du dara lu dul jëfi Seytaane dafay tiitloo aw nitam. Buleen leen ragal. Ragal-leen Ma, ndeem ñu gëm ngeen.
176وَلَا يَحْزُنكَ الَّذِينَ يُسَارِعُونَ فِي الْكُفْرِ ۚ إِنَّهُمْ لَن يَضُرُّوا اللَّهَ شَيْئًا ۗ يُرِيدُ اللَّهُ أَلَّا يَجْعَلَ لَهُمْ حَظًّا فِي الْآخِرَةِ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ñay njëkkante di tàbbi cig weddi, bumu la naqari. Duñu wàññi Yàlla dara. Yàlla dafa bañ rekk ñu am cër ca àllaaxira. Te am fa mbugal mu rëy.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
174Aaya

Tekki — Aali Imran 174

Simoore Aali Imran Aaya 174 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu dellu ñibbi ànd ak xéewalug Yàlla. Te dara lu…

Simoore Aaya 174/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 172–176. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers