Aali Imran · 39/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
فَنَادَتْهُ الْمَلَائِكَةُ وَهُوَ قَائِمٌ يُصَلِّي فِي الْمِحْرَابِ أَنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكَ بِيَحْيَىٰ مُصَدِّقًا بِكَلِمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَسَيِّدًا وَحَصُورًا وَنَبِيًّا مِّنَ الصَّالِحِينَ ۝٣٩
Fanaadat hul malaaa`ikatu wa huwa qaaa`imuny yusallee fil Mihraabi annal laaha yubashshiruka bi Yahyaa musaddiqam bi Kalimatim minal laahi wa saiyidanw wa hasooranw wa Nabiyyam minas saaliheen
📖 Tekkim Wolof
Noonu, Malaaka ya woo ko, fekk mu taxawe julli ca Mihraab ba, xamal ko ne : “Yàllaa ngi lay bégal ci doom ju tudd Yahyaa, muy dëggal kàddu gu bawoo ca Yàlla [di Iisaa, di kilifa, di ku wegu]. Di ab Yonent, bokk ca ñu sell ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 37-41 — Aali Imran

37فَتَقَبَّلَهَا رَبُّهَا بِقَبُولٍ حَسَنٍ وَأَنبَتَهَا نَبَاتًا حَسَنًا وَكَفَّلَهَا زَكَرِيَّا ۖ كُلَّمَا دَخَلَ عَلَيْهَا زَكَرِيَّا الْمِحْرَابَ وَجَدَ عِندَهَا رِزْقًا ۖ قَالَ يَا مَرْيَمُ أَنَّىٰ لَكِ هَٰذَا ۖ قَالَتْ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ ۖ إِنَّ اللَّهَ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
Boroomam nangul ko, nangu gu rafet, màggloo ko màgg gu rafet. [Zakariyaa] yar ko. Saa su [Zakariyaa] duggee ca Mihraab ba, dana fekk fa moom ay xéewal. Mu ne : “Yaw Maryaama, fu la lii bawoo ? ” - Mu tontu ko ne : “Lu jóge ca Yàlla la”. Yàllaay wërsëgal ku ko soob ci lu àndul di waññi na mu tollu.
38هُنَالِكَ دَعَا زَكَرِيَّا رَبَّهُ ۖ قَالَ رَبِّ هَبْ لِي مِن لَّدُنكَ ذُرِّيَّةً طَيِّبَةً ۖ إِنَّكَ سَمِيعُ الدُّعَاءِ
Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare, ay njërëta yu yiw. Yaw Boroom bi Kuy dégg ñaan nga”.
39فَنَادَتْهُ الْمَلَائِكَةُ وَهُوَ قَائِمٌ يُصَلِّي فِي الْمِحْرَابِ أَنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكَ بِيَحْيَىٰ مُصَدِّقًا بِكَلِمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَسَيِّدًا وَحَصُورًا وَنَبِيًّا مِّنَ الصَّالِحِينَ
Noonu, Malaaka ya woo ko, fekk mu taxawe julli ca Mihraab ba, xamal ko ne : “Yàllaa ngi lay bégal ci doom ju tudd Yahyaa, muy dëggal kàddu gu bawoo ca Yàlla [di Iisaa, di kilifa, di ku wegu]. Di ab Yonent, bokk ca ñu sell ña”.
40قَالَ رَبِّ أَنَّىٰ يَكُونُ لِي غُلَامٌ وَقَدْ بَلَغَنِيَ الْكِبَرُ وَامْرَأَتِي عَاقِرٌ ۖ قَالَ كَذَٰلِكَ اللَّهُ يَفْعَلُ مَا يَشَاءُ
Mu ne : "Sama Boroom, naka laay amee doom, ni ma màggatee, sama soxna Jërmél ?”. Mu ne ko : “Noonu lay ame ! ”, Yàlla mooy def lu ko soob.
41قَالَ رَبِّ اجْعَل لِّي آيَةً ۖ قَالَ آيَتُكَ أَلَّا تُكَلِّمَ النَّاسَ ثَلَاثَةَ أَيَّامٍ إِلَّا رَمْزًا ۗ وَاذْكُر رَّبَّكَ كَثِيرًا وَسَبِّحْ بِالْعَشِيِّ وَالْإِبْكَارِ
- Mu ne : “Yàlla, defal ma màndarga.” - Mu ne ko : “ Doo mën a wax ak nit ñi ñetti fan lu dul ci njunju. Na nga tudd sa Boroom lu bari ; te nanga di ko sàbbaal suba ak ngoon.”
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
39Aaya

Tekki — Aali Imran 39

Simoore Aali Imran Aaya 39 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noonu, Malaaka ya woo ko, fekk mu taxawe julli ca…

Simoore Aaya 39/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 37–41. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers