Aali Imran · 38/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
هُنَالِكَ دَعَا زَكَرِيَّا رَبَّهُ ۖ قَالَ رَبِّ هَبْ لِي مِن لَّدُنكَ ذُرِّيَّةً طَيِّبَةً ۖ إِنَّكَ سَمِيعُ الدُّعَاءِ ۝٣٨
Hunaaalika da`aa Zakariyyaa Rabbahoo qaala Rabbi hab lee mil ladunka zurriyyatan taiyibatan innaka samee`ud du`aaa
📖 Tekkim Wolof
Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare, ay njërëta yu yiw. Yaw Boroom bi Kuy dégg ñaan nga”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 36-40 — Simoore Aali Imran

36فَلَمَّا وَضَعَتْهَا قَالَتْ رَبِّ إِنِّي وَضَعْتُهَا أُنثَىٰ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا وَضَعَتْ وَلَيْسَ الذَّكَرُ كَالْأُنثَىٰ ۖ وَإِنِّي سَمَّيْتُهَا مَرْيَمَ وَإِنِّي أُعِيذُهَا بِكَ وَذُرِّيَّتَهَا مِنَ الشَّيْطَانِ الرَّجِيمِ
Ba mu ko wasinee, mu ne : “Ay sama Boroom, jigéen laa wasin de” ; te Yàllaa gën a xam la mu wasin ! Ndax góor melul ni jigéen. “Te tudde naa ko Maryaama, te maa ngi koy muslul wéeru ci Yaw mook i doomam mucc ci Séytaane suñu rëbb sa”.
37فَتَقَبَّلَهَا رَبُّهَا بِقَبُولٍ حَسَنٍ وَأَنبَتَهَا نَبَاتًا حَسَنًا وَكَفَّلَهَا زَكَرِيَّا ۖ كُلَّمَا دَخَلَ عَلَيْهَا زَكَرِيَّا الْمِحْرَابَ وَجَدَ عِندَهَا رِزْقًا ۖ قَالَ يَا مَرْيَمُ أَنَّىٰ لَكِ هَٰذَا ۖ قَالَتْ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ ۖ إِنَّ اللَّهَ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
Boroomam nangul ko, nangu gu rafet, màggloo ko màgg gu rafet. [Zakariyaa] yar ko. Saa su [Zakariyaa] duggee ca Mihraab ba, dana fekk fa moom ay xéewal. Mu ne : “Yaw Maryaama, fu la lii bawoo ? ” - Mu tontu ko ne : “Lu jóge ca Yàlla la”. Yàllaay wërsëgal ku ko soob ci lu àndul di waññi na mu tollu.
38هُنَالِكَ دَعَا زَكَرِيَّا رَبَّهُ ۖ قَالَ رَبِّ هَبْ لِي مِن لَّدُنكَ ذُرِّيَّةً طَيِّبَةً ۖ إِنَّكَ سَمِيعُ الدُّعَاءِ
Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom, may ma ci sa coobare, ay njërëta yu yiw. Yaw Boroom bi Kuy dégg ñaan nga”.
39فَنَادَتْهُ الْمَلَائِكَةُ وَهُوَ قَائِمٌ يُصَلِّي فِي الْمِحْرَابِ أَنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكَ بِيَحْيَىٰ مُصَدِّقًا بِكَلِمَةٍ مِّنَ اللَّهِ وَسَيِّدًا وَحَصُورًا وَنَبِيًّا مِّنَ الصَّالِحِينَ
Noonu, Malaaka ya woo ko, fekk mu taxawe julli ca Mihraab ba, xamal ko ne : “Yàllaa ngi lay bégal ci doom ju tudd Yahyaa, muy dëggal kàddu gu bawoo ca Yàlla [di Iisaa, di kilifa, di ku wegu]. Di ab Yonent, bokk ca ñu sell ña”.
40قَالَ رَبِّ أَنَّىٰ يَكُونُ لِي غُلَامٌ وَقَدْ بَلَغَنِيَ الْكِبَرُ وَامْرَأَتِي عَاقِرٌ ۖ قَالَ كَذَٰلِكَ اللَّهُ يَفْعَلُ مَا يَشَاءُ
Mu ne : "Sama Boroom, naka laay amee doom, ni ma màggatee, sama soxna Jërmél ?”. Mu ne ko : “Noonu lay ame ! ”, Yàlla mooy def lu ko soob.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
38Aaya

Tekki — Aali Imran 38

Simoore Aali Imran Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Foofii la Zakariyaa ñaanee Boroomam, ne : “Yaw sama Boroom,…

Simoore Aaya 38/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers