Aali Imran · 98/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَاللَّهُ شَهِيدٌ عَلَىٰ مَا تَعْمَلُونَ ۝٩٨
Qul yaaa Ahlal Kitaabi lima takfuroona bi Aayaatillaahi wallaahu shaheedun `alaa maa ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàdduy Yàlla yi? Te Yàlla kuy seede la ci li ngeen di def ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 96-100 — Simoore Aali Imran

96إِنَّ أَوَّلَ بَيْتٍ وُضِعَ لِلنَّاسِ لَلَّذِي بِبَكَّةَ مُبَارَكًا وَهُدًى لِّلْعَالَمِينَ
Néeg ba ñu njëkk sampal nit ñi moo di ba nekk Màkka, muy bu ñu barkeel, di njub, mbindéef yépp bokk ko.
97فِيهِ آيَاتٌ بَيِّنَاتٌ مَّقَامُ إِبْرَاهِيمَ ۖ وَمَن دَخَلَهُ كَانَ آمِنًا ۗ وَلِلَّهِ عَلَى النَّاسِ حِجُّ الْبَيْتِ مَنِ اسْتَطَاعَ إِلَيْهِ سَبِيلًا ۚ وَمَن كَفَرَ فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ عَنِ الْعَالَمِينَ
Ay kéemaan yu leer ñoo fa nekk, [bokk na ca] Maxaama Ibraahiima [barab] ; ku fa dugg am kóolute. War na, ci nit ñi ku ko mën, aj fa néegub Yàlla ba te Yàlla tax wenn yoon [wu farata]. Ku weddi nag... na xam ne Yàlla ku doyloo la waliis mbindéef yépp.
98قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَاللَّهُ شَهِيدٌ عَلَىٰ مَا تَعْمَلُونَ
Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàdduy Yàlla yi? Te Yàlla kuy seede la ci li ngeen di def ”
99قُلْ يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ مَنْ آمَنَ تَبْغُونَهَا عِوَجًا وَأَنتُمْ شُهَدَاءُ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di gàllankoor ñiy dox jëm ci yoonu Yàlla, di ko wutal sikk? Te ngeen di ay seede, te Yàlla sàgganewut li ngeen di jëf de.
100يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِن تُطِيعُوا فَرِيقًا مِّنَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ يَرُدُّوكُم بَعْدَ إِيمَانِكُمْ كَافِرِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen toppee ñenn ñi, ñoñ-téere, danañu leen delloo ci kéefar gannaaw ba ngeen gëmee Yàlla.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
98Aaya

Tekki — Aali Imran 98

Simoore Aali Imran Aaya 98 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàdduy…

Simoore Aaya 98/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 96–100. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers