Luqman · 30/34
Tekki Waxtaan — Luqman
ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْحَقُّ وَأَنَّ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ الْبَاطِلُ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْعَلِيُّ الْكَبِيرُ ۝٣٠
Zaalika bi annal laaha Huwal Haqqu wa anna maa yad`oona min doonihil baatilu wa annal laaha Huwal `Aliyyul Kabeer
📖 Tekkim Wolof
[Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 28-32 — Luqman

28مَّا خَلْقُكُمْ وَلَا بَعْثُكُمْ إِلَّا كَنَفْسٍ وَاحِدَةٍ ۗ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ
Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy Dégg la, Kuy Gis la.
29أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ يُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَيُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ وَسَخَّرَ الشَّمْسَ وَالْقَمَرَ كُلٌّ يَجْرِي إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى وَأَنَّ اللَّهَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Xanaa gisoo ne Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, Moom dugal it bëccëg it ci guddi, Moo tàggat jant beek weer wi, ku ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal ? Te Yàlla Ku Deñ- kumpa la, Ku Xàmmee li ngeen di def la.
30ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْحَقُّ وَأَنَّ مَا يَدْعُونَ مِن دُونِهِ الْبَاطِلُ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْعَلِيُّ الْكَبِيرُ
[Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg.
31أَلَمْ تَرَ أَنَّ الْفُلْكَ تَجْرِي فِي الْبَحْرِ بِنِعْمَتِ اللَّهِ لِيُرِيَكُم مِّنْ آيَاتِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّكُلِّ صَبَّارٍ شَكُورٍ
Xanaa gisuloo ne gaal a ngay daw ci biir géej, mu bokk ci xéewali Yàlla yi ? Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ñeel bépp santaakoon, dib muñaakoon.
32وَإِذَا غَشِيَهُم مَّوْجٌ كَالظُّلَلِ دَعَوُا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ فَلَمَّا نَجَّاهُمْ إِلَى الْبَرِّ فَمِنْهُم مُّقْتَصِدٌ ۚ وَمَا يَجْحَدُ بِآيَاتِنَا إِلَّا كُلُّ خَتَّارٍ كَفُورٍ
Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon.
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
30Aaya

Tekki — Luqman 30

Simoore Luqman Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu…

Simoore Aaya 30/34 — Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Luqman Dégg, Luqman Tekki, Luqman mp3, Luqman pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers