Saba · 44/54
Tekki Waxtaan — Saba
وَمَا آتَيْنَاهُم مِّن كُتُبٍ يَدْرُسُونَهَا ۖ وَمَا أَرْسَلْنَا إِلَيْهِمْ قَبْلَكَ مِن نَّذِيرٍ ۝٤٤
Wa maaa aatainaahum min Kutubiny yadrusoonahaa wa maaa arsalnaaa ilaihim qablaka min nazeer
📖 Tekkim Wolof
[Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng. Mësuñoo yónni it ca ñoom ab xuppekat bu la jiitu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 42-46 — Saba

42فَالْيَوْمَ لَا يَمْلِكُ بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ نَّفْعًا وَلَا ضَرًّا وَنَقُولُ لِلَّذِينَ ظَلَمُوا ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّتِي كُنتُم بِهَا تُكَذِّبُونَ
Tey jii nag, kenn ci ñoom ëmbalut moroomam lor mbaa njariñ, te Dananu wax ña daan tooñ ne leen: “Tokkamtikuleen mbugamal Safara sa ngeen doon weddi”.
43وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ قَالُوا مَا هَٰذَا إِلَّا رَجُلٌ يُرِيدُ أَن يَصُدَّكُمْ عَمَّا كَانَ يَعْبُدُ آبَاؤُكُمْ وَقَالُوا مَا هَٰذَا إِلَّا إِفْكٌ مُّفْتَرًى ۚ وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِلْحَقِّ لَمَّا جَاءَهُمْ إِنْ هَٰذَا إِلَّا سِحْرٌ مُّبِينٌ
Bu ñu mësaan a jàng ci ñoom laaya yu leer, dañu naan : “Waa jii daal nammul lu dul féewale leen ak li leen seeni baay daan jaamu”. Ñuy wax it naan : “Lii daal du dara lu dul ay fen yu ñu sos”. Ña weddi woon dëgg it ba mu leen dikkalee, ña nga naan : “Lii daal ag njibar doŋŋ la ! ”.
44وَمَا آتَيْنَاهُم مِّن كُتُبٍ يَدْرُسُونَهَا ۖ وَمَا أَرْسَلْنَا إِلَيْهِمْ قَبْلَكَ مِن نَّذِيرٍ
[Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng. Mësuñoo yónni it ca ñoom ab xuppekat bu la jiitu.
45وَكَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ وَمَا بَلَغُوا مِعْشَارَ مَا آتَيْنَاهُمْ فَكَذَّبُوا رُسُلِي ۖ فَكَيْفَ كَانَ نَكِيرِ
Xeet ya jiitu woon waa Màkka weddi woon nañu Yonent ya. Te waa Màkka amuñu ca lu tollu ni fukkeelu la ñu joxoon ñooña [ci kàttan]. Ñoom it ne sunuy ndaw ay fenkat lañu. Kon naka la samab sànje di dem !
46۞ قُلْ إِنَّمَا أَعِظُكُم بِوَاحِدَةٍ ۖ أَن تَقُومُوا لِلَّهِ مَثْنَىٰ وَفُرَادَىٰ ثُمَّ تَتَفَكَّرُوا ۚ مَا بِصَاحِبِكُم مِّن جِنَّةٍ ۚ إِنْ هُوَ إِلَّا نَذِيرٌ لَّكُم بَيْنَ يَدَيْ عَذَابٍ شَدِيدٍ
Waxal ne : “Maa ngi leen di waar ci lenn : nangeen taxaw ngir Yàlla, moo xam ngeen diy ñaar-ñaar walla ngeen di benn been, te ngeen xalaat. Seen àndandoo bii di Muhammad jinne sadd ko : moom doonul lu dul ab xuppekat bu ame mbugal mu nekk seen kanam”.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Saba 44

Simoore Saba Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng.…

Simoore Aaya 44/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers