Fatir · 43/45
Tekki Waxtaan — Fatir
اسْتِكْبَارًا فِي الْأَرْضِ وَمَكْرَ السَّيِّئِ ۚ وَلَا يَحِيقُ الْمَكْرُ السَّيِّئُ إِلَّا بِأَهْلِهِ ۚ فَهَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا سُنَّتَ الْأَوَّلِينَ ۚ فَلَن تَجِدَ لِسُنَّتِ اللَّهِ تَبْدِيلًا ۖ وَلَن تَجِدَ لِسُنَّتِ اللَّهِ تَحْوِيلًا ۝٤٣
Istakbaaran fil ardi wa makras sayyi`; wa laa yaheequl makrus sayyi`u illaa bi ahlih; fahal yanzuroona illaa sunnatal awwaleen; falan tajida lisunnatil laahi tabdeelanw wa lan tajida lisunnatil laahi tahweela
📖 Tekkim Wolof
[Te dara waralu ko] lu dul rëy-rëylu ak pexe yu bon. Te pexe mu bon du rey lu dul boroom. Te ñoom néggandikuwuñu lu dul xew-xew ya leen jiitu woon ? Te tëralinu Yàlla kenn du ko sopparñi, te kenn it du ko wëlbati.

🎧 Dégg


📜 Aaya 41-45 — Fatir

41۞ إِنَّ اللَّهَ يُمْسِكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ أَن تَزُولَا ۚ وَلَئِن زَالَتَا إِنْ أَمْسَكَهُمَا مِنْ أَحَدٍ مِّن بَعْدِهِ ۚ إِنَّهُ كَانَ حَلِيمًا غَفُورًا
Yàlla moo téye asamaan yeek suuf si ba daanuwuñu. Te bu ko dindi woon it, amul kenn ci ñoom ku ko cay téye ginnaawam. Moom Yàlla ab Jéggalaakoon la, ku Lewet la.
42وَأَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ لَئِن جَاءَهُمْ نَذِيرٌ لَّيَكُونُنَّ أَهْدَىٰ مِنْ إِحْدَى الْأُمَمِ ۖ فَلَمَّا جَاءَهُمْ نَذِيرٌ مَّا زَادَهُمْ إِلَّا نُفُورًا
Dañu daan waat ci Yàlla fu ngiñ gën a ñàngee, di wax naan : su leen ab xuppekat dikkaloon, ñooy gën a gindiku weneen xeet wu dul ñoom. Waaye ba leen ab xuppekat dikkalee , dolliwuleen lu dul dummóoyu .
43اسْتِكْبَارًا فِي الْأَرْضِ وَمَكْرَ السَّيِّئِ ۚ وَلَا يَحِيقُ الْمَكْرُ السَّيِّئُ إِلَّا بِأَهْلِهِ ۚ فَهَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا سُنَّتَ الْأَوَّلِينَ ۚ فَلَن تَجِدَ لِسُنَّتِ اللَّهِ تَبْدِيلًا ۖ وَلَن تَجِدَ لِسُنَّتِ اللَّهِ تَحْوِيلًا
[Te dara waralu ko] lu dul rëy-rëylu ak pexe yu bon. Te pexe mu bon du rey lu dul boroom. Te ñoom néggandikuwuñu lu dul xew-xew ya leen jiitu woon ? Te tëralinu Yàlla kenn du ko sopparñi, te kenn it du ko wëlbati.
44أَوَلَمْ يَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ وَكَانُوا أَشَدَّ مِنْهُمْ قُوَّةً ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعْجِزَهُ مِن شَيْءٍ فِي السَّمَاوَاتِ وَلَا فِي الْأَرْضِ ۚ إِنَّهُ كَانَ عَلِيمًا قَدِيرًا
Moo ndax dañoo doxul ci suuf si tey xool mujjug ña leen fi jiitu woon te ëppoon leen doole ? Amul dara lu mën të Yàlla ci asamaan yeek suuf si. Moom Yàlla kuy Xam la, kuy Mën la.
45وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِمَا كَسَبُوا مَا تَرَكَ عَلَىٰ ظَهْرِهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِعِبَادِهِ بَصِيرًا
Su Yàlla doon jàppe nit ñi ci li ñuy def. Kon du bàyyi kenn kuy dox ci kaw suuf si. Waaye daleen di xaare àpp ba Mu àppal. Cëy bu dig ba agsee... [danañu xam ne] Yàlla kuy gis jaamam ñi la.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
43Aaya

Tekki — Fatir 43

Simoore Fatir Aaya 43 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Te dara waralu ko] lu dul rëy-rëylu ak pexe yu…

Simoore Aaya 43/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 41–45. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers