An-Nisa · 110/176
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nisa
وَمَن يَعْمَلْ سُوءًا أَوْ يَظْلِمْ نَفْسَهُ ثُمَّ يَسْتَغْفِرِ اللَّهَ يَجِدِ اللَّهَ غَفُورًا رَّحِيمًا ۝١١٠
Wa mai ya`mal sooo`an aw yazlim nafsahoo summa yastaghfiril laaha yajidil laaha Ghafoorar Raheemaa
📖 Tekkim Wolof
Képp ku def ñaawtéef mbaa mu tooñ boppam, gaaw jéggalu Yàlla, dana fekk di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 108-112 — Simoore An-Nisa

108يَسْتَخْفُونَ مِنَ النَّاسِ وَلَا يَسْتَخْفُونَ مِنَ اللَّهِ وَهُوَ مَعَهُمْ إِذْ يُبَيِّتُونَ مَا لَا يَرْضَىٰ مِنَ الْقَوْلِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطًا
Nëbbu nañu nit ñi, waaye mënuñoo nëbbu Yàlla. Ndax mook ñoom a nekkoon ba ñuy fanaanoo ay wax yu ko neexul. La ñu doon def, Yàlla péeg na ko [ci xam-xam].
109هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ جَادَلْتُمْ عَنْهُمْ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا فَمَن يُجَادِلُ اللَّهَ عَنْهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ أَم مَّن يَكُونُ عَلَيْهِمْ وَكِيلًا
Yéen a ngi noonu di layal ñooñu ci dundug àddina bi. Waaye ana kan moo leen di layal ca Bis-pénc ba ? Walla ana kan mooy doon seen wéeruwaay ?
110وَمَن يَعْمَلْ سُوءًا أَوْ يَظْلِمْ نَفْسَهُ ثُمَّ يَسْتَغْفِرِ اللَّهَ يَجِدِ اللَّهَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Képp ku def ñaawtéef mbaa mu tooñ boppam, gaaw jéggalu Yàlla, dana fekk di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon.
111وَمَن يَكْسِبْ إِثْمًا فَإِنَّمَا يَكْسِبُهُ عَلَىٰ نَفْسِهِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Ku fàggu bàkkaar, defu ko kenn ku dul boppam. Yàlla Ku xam la, di Ku xereñ.
112وَمَن يَكْسِبْ خَطِيئَةً أَوْ إِثْمًا ثُمَّ يَرْمِ بِهِ بَرِيئًا فَقَدِ احْتَمَلَ بُهْتَانًا وَإِثْمًا مُّبِينًا
Ku def ñaawtéef walla bàkkaar ba noppi jiiñ ko ku ca set wecc, kooka yenu ma duur ak bàkkaar bu bari.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
110Aaya

Tekki — An-Nisa 110

Simoore An-Nisa Aaya 110 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp ku def ñaawtéef mbaa mu tooñ boppam, gaaw jéggalu…

Simoore Aaya 110/176 — Simoore An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nisa Dégg, Simoore An-Nisa Tekki, Simoore An-Nisa mp3, Simoore An-Nisa pdf. Aaya 108–112. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers