An-Nisa · 165/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
رُّسُلًا مُّبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ لِئَلَّا يَكُونَ لِلنَّاسِ عَلَى اللَّهِ حُجَّةٌ بَعْدَ الرُّسُلِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَزِيزًا حَكِيمًا ۝١٦٥
Rusulam mubashshireena wa munzireena li`allaa yakoona linnaasi `alal laahi hujjatum ba`dar Rusul; wa kaanallaahu `Azeezan Hakeema
📖 Tekkim Wolof
ñu di ay Yonent yuy bégle ak xuppe ngir nit ñi bañ a am lay wu mën a yey Yàlla, ginnaaw ba leen Yonent ya xamalee dëgg. Yàlla ku am kàttan la, di Ku tedd.
🎧 Dégg

📜 Aaya 163-167 — An-Nisa

163۞ إِنَّا أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ كَمَا أَوْحَيْنَا إِلَىٰ نُوحٍ وَالنَّبِيِّينَ مِن بَعْدِهِ ۚ وَأَوْحَيْنَا إِلَىٰ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطِ وَعِيسَىٰ وَأَيُّوبَ وَيُونُسَ وَهَارُونَ وَسُلَيْمَانَ ۚ وَآتَيْنَا دَاوُودَ زَبُورًا
Sol Nanu [Nun Yàlla] leerug Yonent ci yaw [Muhammad] ni Nu ko sole woon ca [Nooh] ak Yonent ya toppoon ca moom. Sol Nanu ko Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba, ak sët ya ak Iisaa, ak Ayuuba, ak Yuunusa, ak Haaruun, ak Suleymaan, te jox Nanu Daawuda ab Téere bu tudd [Zabuur].
164وَرُسُلًا قَدْ قَصَصْنَاهُمْ عَلَيْكَ مِن قَبْلُ وَرُسُلًا لَّمْ نَقْصُصْهُمْ عَلَيْكَ ۚ وَكَلَّمَ اللَّهُ مُوسَىٰ تَكْلِيمًا
Ak Yonent yoo xam ne nettali woon Nanu leen seeni mbir lu jiitu, ak ñeneen ñu Nu la nettaliwul [seeni mbir] - Te Yàlla wax na ak Muusaa waxante tigi -
165رُّسُلًا مُّبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ لِئَلَّا يَكُونَ لِلنَّاسِ عَلَى اللَّهِ حُجَّةٌ بَعْدَ الرُّسُلِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَزِيزًا حَكِيمًا
ñu di ay Yonent yuy bégle ak xuppe ngir nit ñi bañ a am lay wu mën a yey Yàlla, ginnaaw ba leen Yonent ya xamalee dëgg. Yàlla ku am kàttan la, di Ku tedd.
166لَّٰكِنِ اللَّهُ يَشْهَدُ بِمَا أَنزَلَ إِلَيْكَ ۖ أَنزَلَهُ بِعِلْمِهِ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ يَشْهَدُونَ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ شَهِيدًا
Waaye Yàlla seede na la Mu wàcce ci Yaw, te ci xam-xam la ko wékk. Te Malaaka ya it seede nañu. Te Yàlla doy na, mat sëkk seede.
167إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَصَدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ قَدْ ضَلُّوا ضَلَالًا بَعِيدًا
Ña weddi tey féew nit ñi yoonu Yàlla, réer nañu réer gu sori.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
165Aaya

Tekki — An-Nisa 165

Simoore An-Nisa Aaya 165 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ñu di ay Yonent yuy bégle ak xuppe ngir nit…

Simoore Aaya 165/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 163–167. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers