Al-Ahqaf · 6/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
وَإِذَا حُشِرَ النَّاسُ كَانُوا لَهُمْ أَعْدَاءً وَكَانُوا بِعِبَادَتِهِمْ كَافِرِينَ ۝٦
Wa izaa hushiran naasu kaanoo lahum a`daaa`anw wa kaanoo bi`ibaadatihim kaafireen
📖 Tekkim Wolof
(Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir àtte leen dañuy soppeeku di ay noon, weddi jaamu ga ba mu set wecc.
🎧 Dégg

📜 Aaya 4-8 — Al-Ahqaf

4قُلْ أَرَأَيْتُم مَّا تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ أَرُونِي مَاذَا خَلَقُوا مِنَ الْأَرْضِ أَمْ لَهُمْ شِرْكٌ فِي السَّمَاوَاتِ ۖ ائْتُونِي بِكِتَابٍ مِّن قَبْلِ هَٰذَا أَوْ أَثَارَةٍ مِّنْ عِلْمٍ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Waxal ne : “Ana lan ngeen di xalaat ci li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ? Wan leen ma ana li ñu sàkk ci kaw suuf ! Walla dañoo am man-man ci asamaan yi ? Indilleen ma Téere bu jiitu (Alxuraan) wala book jeexitali xam-xam, ndegam ñu dëggu ngeen”.
5وَمَنْ أَضَلُّ مِمَّن يَدْعُو مِن دُونِ اللَّهِ مَن لَّا يَسْتَجِيبُ لَهُ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ وَهُمْ عَن دُعَائِهِمْ غَافِلُونَ
Waaw ana kan moo gën a sànku (réer) ci kuy woo keneen ku dul Yàlla, koo xam ne du ko wuyu ba baa bis penc ba ? Te dañuy sàggane woote ba (duñu dégg duñu tontu).
6وَإِذَا حُشِرَ النَّاسُ كَانُوا لَهُمْ أَعْدَاءً وَكَانُوا بِعِبَادَتِهِمْ كَافِرِينَ
(Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir àtte leen dañuy soppeeku di ay noon, weddi jaamu ga ba mu set wecc.
7وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ قَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِلْحَقِّ لَمَّا جَاءَهُمْ هَٰذَا سِحْرٌ مُّبِينٌ
Bu ñu jàngaatee ñoom sunuy Laaya mu leer nàññ ña daan weddi dañu daan wax ne: “ lii ak njibar la gu fés” , aa li mooy duun-duun dëgg.
8أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ إِنِ افْتَرَيْتُهُ فَلَا تَمْلِكُونَ لِي مِنَ اللَّهِ شَيْئًا ۖ هُوَ أَعْلَمُ بِمَا تُفِيضُونَ فِيهِ ۖ كَفَىٰ بِهِ شَهِيدًا بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۖ وَهُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ
Walla ñu naan : “Da koo sos ! ” Nee leen : “Su fekkee ne dama koo sos manalu leen ma ci Yàlla tus. Moom moo gën a xam li ngeen cay lëmbaaje : Doy na sëkk seede sama digganteek yéen. Te moom (Yàlla) moo di Jéggëlewaakoon bi, di Jaglewaakoon bi”.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
6Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 6

Simoore Al-Ahqaf Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir…

Simoore Aaya 6/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers