Al-Ahqaf · 8/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ إِنِ افْتَرَيْتُهُ فَلَا تَمْلِكُونَ لِي مِنَ اللَّهِ شَيْئًا ۖ هُوَ أَعْلَمُ بِمَا تُفِيضُونَ فِيهِ ۖ كَفَىٰ بِهِ شَهِيدًا بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۖ وَهُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ ۝٨
Am yaqooloonaf taraahu qul inif taraituhoo falaa tamlikoona lee minal laahi shai`an Huwa a`lamu bimaa tufeedoona feehi kafaa bihee shaheedam bainee wa bainakum wa Huwal Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Walla ñu naan : “Da koo sos ! ” Nee leen : “Su fekkee ne dama koo sos manalu leen ma ci Yàlla tus. Moom moo gën a xam li ngeen cay lëmbaaje : Doy na sëkk seede sama digganteek yéen. Te moom (Yàlla) moo di Jéggëlewaakoon bi, di Jaglewaakoon bi”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 6-10 — Al-Ahqaf

6وَإِذَا حُشِرَ النَّاسُ كَانُوا لَهُمْ أَعْدَاءً وَكَانُوا بِعِبَادَتِهِمْ كَافِرِينَ
(Te bu bis Pénc baa) ñu pang nit ñi ngir àtte leen dañuy soppeeku di ay noon, weddi jaamu ga ba mu set wecc.
7وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ قَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِلْحَقِّ لَمَّا جَاءَهُمْ هَٰذَا سِحْرٌ مُّبِينٌ
Bu ñu jàngaatee ñoom sunuy Laaya mu leer nàññ ña daan weddi dañu daan wax ne: “ lii ak njibar la gu fés” , aa li mooy duun-duun dëgg.
8أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ إِنِ افْتَرَيْتُهُ فَلَا تَمْلِكُونَ لِي مِنَ اللَّهِ شَيْئًا ۖ هُوَ أَعْلَمُ بِمَا تُفِيضُونَ فِيهِ ۖ كَفَىٰ بِهِ شَهِيدًا بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۖ وَهُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ
Walla ñu naan : “Da koo sos ! ” Nee leen : “Su fekkee ne dama koo sos manalu leen ma ci Yàlla tus. Moom moo gën a xam li ngeen cay lëmbaaje : Doy na sëkk seede sama digganteek yéen. Te moom (Yàlla) moo di Jéggëlewaakoon bi, di Jaglewaakoon bi”.
9قُلْ مَا كُنتُ بِدْعًا مِّنَ الرُّسُلِ وَمَا أَدْرِي مَا يُفْعَلُ بِي وَلَا بِكُمْ ۖ إِنْ أَتَّبِعُ إِلَّا مَا يُوحَىٰ إِلَيَّ وَمَا أَنَا إِلَّا نَذِيرٌ مُّبِينٌ
Waxal ne : “Du man maay Yonent bi jëkk feeñ ; te it xamuma li ñuy xala def ci man, mbaa ci yéen. Man daal damay topp linu may soloo doŋŋ ; te itam doonu ma kenn ku dul ab waaraatekat buy leeral”.
10قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن كَانَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَكَفَرْتُم بِهِ وَشَهِدَ شَاهِدٌ مِّن بَنِي إِسْرَائِيلَ عَلَىٰ مِثْلِهِ فَآمَنَ وَاسْتَكْبَرْتُمْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
Waxal ne: “Ana lan mooy xalaat ci ne lii su fekkee dafa bawoo ca Yàlla ngeen weddi ko, mu am it ci giir banii israayila kenn ku ca seede lu ni mel moom mi gëm, yéen ngeen rëy- rëylu... Yàlla dey du gindi aw nit ñuy tooñkat ! ”
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 8

Simoore Al-Ahqaf Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Walla ñu naan : “Da koo sos ! ” Nee…

Simoore Aaya 8/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers