Al-Maida · 51/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا الْيَهُودَ وَالنَّصَارَىٰ أَوْلِيَاءَ ۘ بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُم مِّنكُمْ فَإِنَّهُ مِنْهُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ ۝٥١
Yaaa aiyuhal lazeena aamanoo laa tattakhizul Yahooda wan nasaaraaa awliyaaa`; ba`duhum awliyaaa`u ba`d; wa mai yatawallahum minkum fa innahoo minhum; innal laaha laa yahdil qawmaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàpp yahuud yi ak nasraan yi di xaritook ñoom. Ku ko def ci yéeen, daanaka ca ñoom la bokk. Te nag Yàlla du gindi nit ñu di ay tooñkat.
🎧 Dégg

📜 Aaya 49-53 — Al-Maida

49وَأَنِ احْكُم بَيْنَهُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ وَلَا تَتَّبِعْ أَهْوَاءَهُمْ وَاحْذَرْهُمْ أَن يَفْتِنُوكَ عَن بَعْضِ مَا أَنزَلَ اللَّهُ إِلَيْكَ ۖ فَإِن تَوَلَّوْا فَاعْلَمْ أَنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ أَن يُصِيبَهُم بِبَعْضِ ذُنُوبِهِمْ ۗ وَإِنَّ كَثِيرًا مِّنَ النَّاسِ لَفَاسِقُونَ
Nangay àtte seeni diggante ak la Yàlla wàcce. Te bul topp seeni bànneex, te nga moytuleen ngir ñu bañ laa réeral, soril la lenn ca la Yàlla wàcce. Te yaw, bu ñu dëddoo dellu ginnaaw, nanga xam ne Yàlla amul lu dul lenn ci seeni bàkkaar yi dal leen. Bari na ci nit ñi ñu nekk way-sàqi ndigal.
50أَفَحُكْمَ الْجَاهِلِيَّةِ يَبْغُونَ ۚ وَمَنْ أَحْسَنُ مِنَ اللَّهِ حُكْمًا لِّقَوْمٍ يُوقِنُونَ
Moo ndax àtteb way-réer ña [jiitu Lislaam] lañuy sàkku ? Te ana àtteb kan moo gën a jege àtteb Yàlla ci nit ñoo xam ne ñu wóolu lañu seen Boroom ?
51۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا الْيَهُودَ وَالنَّصَارَىٰ أَوْلِيَاءَ ۘ بَعْضُهُمْ أَوْلِيَاءُ بَعْضٍ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُم مِّنكُمْ فَإِنَّهُ مِنْهُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàpp yahuud yi ak nasraan yi di xaritook ñoom. Ku ko def ci yéeen, daanaka ca ñoom la bokk. Te nag Yàlla du gindi nit ñu di ay tooñkat.
52فَتَرَى الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ يُسَارِعُونَ فِيهِمْ يَقُولُونَ نَخْشَىٰ أَن تُصِيبَنَا دَائِرَةٌ ۚ فَعَسَى اللَّهُ أَن يَأْتِيَ بِالْفَتْحِ أَوْ أَمْرٍ مِّنْ عِندِهِ فَيُصْبِحُوا عَلَىٰ مَا أَسَرُّوا فِي أَنفُسِهِمْ نَادِمِينَ
Danga gis ña nga xam ne jàngoroy [sikki-sàkka] nekk na ca seeni xol, ñuy gaawantu jëm ca ñoom, di taafantaloo ne dañoo ragal walbatikug jamono songu leen. Te amaana Yàlla indi ndam mbaa mbir mu tukkee ca Moom. Bu boobaa danañu rëccu la ñu bëggoon ca seeni xol.
53وَيَقُولُ الَّذِينَ آمَنُوا أَهَٰؤُلَاءِ الَّذِينَ أَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ ۙ إِنَّهُمْ لَمَعَكُمْ ۚ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ فَأَصْبَحُوا خَاسِرِينَ
Ba way-gëm ña naan : “Moo ndax du ñii ñoo doon giñ ci Yàlla fa ngiñ gën a màggee ngir ne ñoom ñook yéen a ànd bu wér ? ” Seeni jëf sippiku na [yàqu], ñu mujj di ñu yàqule.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
51Aaya

Tekki — Al-Maida 51

Simoore Al-Maida Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàpp yahuud yi ak…

Simoore Aaya 51/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers