Al-Maida · 82/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
۞ لَتَجِدَنَّ أَشَدَّ النَّاسِ عَدَاوَةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الْيَهُودَ وَالَّذِينَ أَشْرَكُوا ۖ وَلَتَجِدَنَّ أَقْرَبَهُم مَّوَدَّةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الَّذِينَ قَالُوا إِنَّا نَصَارَىٰ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّ مِنْهُمْ قِسِّيسِينَ وَرُهْبَانًا وَأَنَّهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ ۝٨٢
Latajidanna ashad dan naasi `adaawatal lillazeena aamanul Yahooda wallazeena ashrakoo wa latajidanna aqrabahum mawaddatal lil lazeena aamanul lazeena qaalooo innaa Nasaaraa; zaalika bi anna mminhum qiseeseena wa ruhbaananw wa annahum laa yastakbiroon
📖 Tekkim Wolof
Wér na ne danga gis ne, ña gën a tar nooneel ci nit ña jëme ca jullit ña, ñooy yahuud ya ak ñay bokkaale. Te danga gis it ne, ña gën a jege ci ag cofeel jullit ña, ñooy ñay wax ne : “Nun karcen lanu [nasraan].” Ndax am na ci ñoom ay làbbe ak ñu dëddu àddina, ñoo xam ne duñu rëy-rëylu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 80-84 — Al-Maida

80تَرَىٰ كَثِيرًا مِّنْهُمْ يَتَوَلَّوْنَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ لَبِئْسَ مَا قَدَّمَتْ لَهُمْ أَنفُسُهُمْ أَن سَخِطَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ وَفِي الْعَذَابِ هُمْ خَالِدُونَ
Danga gis ñu bari ci ñoom ñuy xaritoo ak ña weddi. La leen seeni bakkan defloo ñaaw na, ba Yàlla mere leen, te ci ag mbugal lañuy nekk béel ca.
81وَلَوْ كَانُوا يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَالنَّبِيِّ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْهِ مَا اتَّخَذُوهُمْ أَوْلِيَاءَ وَلَٰكِنَّ كَثِيرًا مِّنْهُمْ فَاسِقُونَ
Bu ñu nekkoon di ñu gëm Yàlla, ak Yonent ba ak la ñu wàcce ca ñoom, duñu jàppe xarit [yéefar ya]. Waaye lu bari ca ñoom saay-saay lañu [ñu génn ci topp].
82۞ لَتَجِدَنَّ أَشَدَّ النَّاسِ عَدَاوَةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الْيَهُودَ وَالَّذِينَ أَشْرَكُوا ۖ وَلَتَجِدَنَّ أَقْرَبَهُم مَّوَدَّةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الَّذِينَ قَالُوا إِنَّا نَصَارَىٰ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّ مِنْهُمْ قِسِّيسِينَ وَرُهْبَانًا وَأَنَّهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ
Wér na ne danga gis ne, ña gën a tar nooneel ci nit ña jëme ca jullit ña, ñooy yahuud ya ak ñay bokkaale. Te danga gis it ne, ña gën a jege ci ag cofeel jullit ña, ñooy ñay wax ne : “Nun karcen lanu [nasraan].” Ndax am na ci ñoom ay làbbe ak ñu dëddu àddina, ñoo xam ne duñu rëy-rëylu.
83وَإِذَا سَمِعُوا مَا أُنزِلَ إِلَى الرَّسُولِ تَرَىٰ أَعْيُنَهُمْ تَفِيضُ مِنَ الدَّمْعِ مِمَّا عَرَفُوا مِنَ الْحَقِّ ۖ يَقُولُونَ رَبَّنَا آمَنَّا فَاكْتُبْنَا مَعَ الشَّاهِدِينَ
Te bu ñu déggee li wàcc ci Yonent bi nga gis seeni bët di sottiy rongoñ ndax dëgg ga ñu cay xàmmee. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom ! Gëm nanu : Nanga nu boole ca ñay way- seede.
84وَمَا لَنَا لَا نُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَمَا جَاءَنَا مِنَ الْحَقِّ وَنَطْمَعُ أَن يُدْخِلَنَا رَبُّنَا مَعَ الْقَوْمِ الصَّالِحِينَ
Luy tee ñu gëm Yàlla ak la ñu dikkal ci dëgg ak ni nu xemeeme sunu Boroom tàbbal nu Àjjana ànd ak way-sellal ña ? ”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
82Aaya

Tekki — Al-Maida 82

Simoore Al-Maida Aaya 82 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Wér na ne danga gis ne, ña gën a tar…

Simoore Aaya 82/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 80–84. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers