Al-Maida · 84/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَمَا لَنَا لَا نُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَمَا جَاءَنَا مِنَ الْحَقِّ وَنَطْمَعُ أَن يُدْخِلَنَا رَبُّنَا مَعَ الْقَوْمِ الصَّالِحِينَ ۝٨٤
Wa maa lanaa laa nu`minu billaahi wa maa jaaa`anaa minal haqqi wa natma`u ai yudkhilanaa Rabbunaa ma`al qawmis saaliheen
📖 Tekkim Wolof
Luy tee ñu gëm Yàlla ak la ñu dikkal ci dëgg ak ni nu xemeeme sunu Boroom tàbbal nu Àjjana ànd ak way-sellal ña ? ”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 82-86 — Al-Maida

82۞ لَتَجِدَنَّ أَشَدَّ النَّاسِ عَدَاوَةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الْيَهُودَ وَالَّذِينَ أَشْرَكُوا ۖ وَلَتَجِدَنَّ أَقْرَبَهُم مَّوَدَّةً لِّلَّذِينَ آمَنُوا الَّذِينَ قَالُوا إِنَّا نَصَارَىٰ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّ مِنْهُمْ قِسِّيسِينَ وَرُهْبَانًا وَأَنَّهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ
Wér na ne danga gis ne, ña gën a tar nooneel ci nit ña jëme ca jullit ña, ñooy yahuud ya ak ñay bokkaale. Te danga gis it ne, ña gën a jege ci ag cofeel jullit ña, ñooy ñay wax ne : “Nun karcen lanu [nasraan].” Ndax am na ci ñoom ay làbbe ak ñu dëddu àddina, ñoo xam ne duñu rëy-rëylu.
83وَإِذَا سَمِعُوا مَا أُنزِلَ إِلَى الرَّسُولِ تَرَىٰ أَعْيُنَهُمْ تَفِيضُ مِنَ الدَّمْعِ مِمَّا عَرَفُوا مِنَ الْحَقِّ ۖ يَقُولُونَ رَبَّنَا آمَنَّا فَاكْتُبْنَا مَعَ الشَّاهِدِينَ
Te bu ñu déggee li wàcc ci Yonent bi nga gis seeni bët di sottiy rongoñ ndax dëgg ga ñu cay xàmmee. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom ! Gëm nanu : Nanga nu boole ca ñay way- seede.
84وَمَا لَنَا لَا نُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَمَا جَاءَنَا مِنَ الْحَقِّ وَنَطْمَعُ أَن يُدْخِلَنَا رَبُّنَا مَعَ الْقَوْمِ الصَّالِحِينَ
Luy tee ñu gëm Yàlla ak la ñu dikkal ci dëgg ak ni nu xemeeme sunu Boroom tàbbal nu Àjjana ànd ak way-sellal ña ? ”.
85فَأَثَابَهُمُ اللَّهُ بِمَا قَالُوا جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا ۚ وَذَٰلِكَ جَزَاءُ الْمُحْسِنِينَ
Yàlla xéewale na leen, ngir la ñu wax, ay Àjjana yoo xam ne ay dex dañuy daw ca suufam, te dañu fay béel. Te loolu mooy peyug way-rafetal ña.
86وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَحِيمِ
Waaye nag yéefar ya weddi Sunuy kàddu, ñoom ñooy dugg Safara.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
84Aaya

Tekki — Al-Maida 84

Simoore Al-Maida Aaya 84 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Luy tee ñu gëm Yàlla ak la ñu dikkal ci…

Simoore Aaya 84/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 82–86. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers