Al-Mujadila · 4/22
Tekki Waxtaan — Al-Mujadila
فَمَن لَّمْ يَجِدْ فَصِيَامُ شَهْرَيْنِ مُتَتَابِعَيْنِ مِن قَبْلِ أَن يَتَمَاسَّا ۖ فَمَن لَّمْ يَسْتَطِعْ فَإِطْعَامُ سِتِّينَ مِسْكِينًا ۚ ذَٰلِكَ لِتُؤْمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ وَتِلْكَ حُدُودُ اللَّهِ ۗ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝٤
Famal lam yajid fa siyaamu shahraini mutataabi`ayni min qabli any-yatamaaassaa famal lam yastati` fa-it`aamu sitteena miskeena; zaalika litu`minoo billaahi wa rasoolih`wa tilka hudoodul laah; wa lilkaafireena `azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa ñuy jonjoowaat. Su ko manul, na leel juróom-benn-fukki ndóol miskiin. Loolu nag, ngir ngeen gëm Yàlla ak ub Yonentam. Te loolu mooy daytali Yàlla yi. Ña weddi nag ñoom danañu am mbugël mu mitti.

🎧 Dégg


📜 Aaya 2-6 — Al-Mujadila

2الَّذِينَ يُظَاهِرُونَ مِنكُم مِّن نِّسَائِهِم مَّا هُنَّ أُمَّهَاتِهِمْ ۖ إِنْ أُمَّهَاتُهُمْ إِلَّا اللَّائِي وَلَدْنَهُمْ ۚ وَإِنَّهُمْ لَيَقُولُونَ مُنكَرًا مِّنَ الْقَوْلِ وَزُورًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَعَفُوٌّ غَفُورٌ
Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul ñu mel mi seeni nday ci ñoom... seeni nday ñoom ña leen juróon. Li ñuy wax lu ñaaw la di ay fen. Te Yàlla nag kuy bale la ab Jéggalaakoon la.
3وَالَّذِينَ يُظَاهِرُونَ مِن نِّسَائِهِمْ ثُمَّ يَعُودُونَ لِمَا قَالُوا فَتَحْرِيرُ رَقَبَةٍ مِّن قَبْلِ أَن يَتَمَاسَّا ۚ ذَٰلِكُمْ تُوعَظُونَ بِهِ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Góor ñi nga xam ne dañoo woddi seeni jabar seeni pendali nday ba noppi bëgg caa dale ginnaaw, ca la ñu waxoon, nanu goreel ab jaam balaa ñoo jonjoowaat loolu la ñu leen di jàjje. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
4فَمَن لَّمْ يَجِدْ فَصِيَامُ شَهْرَيْنِ مُتَتَابِعَيْنِ مِن قَبْلِ أَن يَتَمَاسَّا ۖ فَمَن لَّمْ يَسْتَطِعْ فَإِطْعَامُ سِتِّينَ مِسْكِينًا ۚ ذَٰلِكَ لِتُؤْمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ وَتِلْكَ حُدُودُ اللَّهِ ۗ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa ñuy jonjoowaat. Su ko manul, na leel juróom-benn-fukki ndóol miskiin. Loolu nag, ngir ngeen gëm Yàlla ak ub Yonentam. Te loolu mooy daytali Yàlla yi. Ña weddi nag ñoom danañu am mbugël mu mitti.
5إِنَّ الَّذِينَ يُحَادُّونَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ كُبِتُوا كَمَا كُبِتَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ وَقَدْ أَنزَلْنَا آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ ۚ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ مُّهِينٌ
Ñay juuyook Yàlla ak ub Yonentam dees na leen toroxal kem niñu toroxale woon ña leen fi jiitu woon. Te wàcce nanu ay firnde yu leer nàññ, yéefar yi am nañu mbugël mu and ak toroxtaane,
6يَوْمَ يَبْعَثُهُمُ اللَّهُ جَمِيعًا فَيُنَبِّئُهُم بِمَا عَمِلُوا ۚ أَحْصَاهُ اللَّهُ وَنَسُوهُ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ شَهِيدٌ
bu keroog bis pénc baa ba Yàlla dékkal leen ñoom ñépp, dana leen xibaar la ñu jëfoon ndax Yàlla moom takkoon na ko ñoom it ñu fàtte ko. Yàlla kuy seede la ci lépp lu ne.
Al-MujadilaFihi Alxuraan
22Aaya
MedinanRevelation
4Aaya

Tekki — Al-Mujadila 4

Simoore Al-Mujadila Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa…

Simoore Aaya 4/22 — Al-Mujadila المجادلة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Mujadila Dégg, Al-Mujadila Tekki, Al-Mujadila mp3, Al-Mujadila pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers