Al-An'am · 159/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
إِنَّ الَّذِينَ فَرَّقُوا دِينَهُمْ وَكَانُوا شِيَعًا لَّسْتَ مِنْهُمْ فِي شَيْءٍ ۚ إِنَّمَا أَمْرُهُمْ إِلَى اللَّهِ ثُمَّ يُنَبِّئُهُم بِمَا كَانُوا يَفْعَلُونَ ۝١٥٩
Innal lazeena farraqoo deenahum wa kaanoo shiya`allasta minhum fee shai`; innamaaa amruhum ilallaahi summma yunabbi`uhum bimaa kaanoo yaf`aloon
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne dañoo xàjjale seen diine ba mu nekk ay pàcc-pàcc, bokkulook ñoom dara : seeni mbir ci Yàlla doŋŋ la nekk. Te Dana leen biral la ñu nekkoon di ko def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 157-161 — Simoore Al-An'am

157أَوْ تَقُولُوا لَوْ أَنَّا أُنزِلَ عَلَيْنَا الْكِتَابُ لَكُنَّا أَهْدَىٰ مِنْهُمْ ۚ فَقَدْ جَاءَكُم بَيِّنَةٌ مِّن رَّبِّكُمْ وَهُدًى وَرَحْمَةٌ ۚ فَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن كَذَّبَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَصَدَفَ عَنْهَا ۗ سَنَجْزِي الَّذِينَ يَصْدِفُونَ عَنْ آيَاتِنَا سُوءَ الْعَذَابِ بِمَا كَانُوا يَصْدِفُونَ
Walla ngeen di wax naan : “Bu fekkoon ne ci nun lañu wàcce Téere ba, kon noo leen di gën a gindiku.”. Ag leeral dikkal na leen, jóge fa seen Boroom, di njub ak yërmaande. Ana kan moo gën a tooñ kuy dummóoyu kàdduy Yàlla te weddi leen ? Dananu feye, ñay dëddu Sunuy kàddu, gën jaa suufe [bon] mbugal ngir seenug dëddu.
158هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمُ الْمَلَائِكَةُ أَوْ يَأْتِيَ رَبُّكَ أَوْ يَأْتِيَ بَعْضُ آيَاتِ رَبِّكَ ۗ يَوْمَ يَأْتِي بَعْضُ آيَاتِ رَبِّكَ لَا يَنفَعُ نَفْسًا إِيمَانُهَا لَمْ تَكُنْ آمَنَتْ مِن قَبْلُ أَوْ كَسَبَتْ فِي إِيمَانِهَا خَيْرًا ۗ قُلِ انتَظِرُوا إِنَّا مُنتَظِرُونَ
Moo ndax dañuy xaar ba Malaaka ya dikk fa ñoom? Walla sa Boroom agsi ? Walla lenn ci sa kéemaani Boroom dikk ? Bis ba lenn ci sa kéemaani Boroom dikkee, bàjjo bu gëmul woon lu jiitu, di door a gëm, du ko jariñ dara de, walla ku sàkkuwul wenn yiw it, ngëmam du ko jariñ dara. Neel : “Xaarleen ! ”. Nun it Noo ngi xaar.
159إِنَّ الَّذِينَ فَرَّقُوا دِينَهُمْ وَكَانُوا شِيَعًا لَّسْتَ مِنْهُمْ فِي شَيْءٍ ۚ إِنَّمَا أَمْرُهُمْ إِلَى اللَّهِ ثُمَّ يُنَبِّئُهُم بِمَا كَانُوا يَفْعَلُونَ
Ña nga xam ne dañoo xàjjale seen diine ba mu nekk ay pàcc-pàcc, bokkulook ñoom dara : seeni mbir ci Yàlla doŋŋ la nekk. Te Dana leen biral la ñu nekkoon di ko def.
160مَن جَاءَ بِالْحَسَنَةِ فَلَهُ عَشْرُ أَمْثَالِهَا ۖ وَمَن جَاءَ بِالسَّيِّئَةِ فَلَا يُجْزَىٰ إِلَّا مِثْلَهَا وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Ku def u yiw, am yool bu tollu ni fukki yooni yiw wa ; ku def ñaawtéef am bàkkaar bu tollu ni ñaawtéef wa. Te kenn duleen tooñ [ci yokkal mbaa wàññil leen ci dara].
161قُلْ إِنَّنِي هَدَانِي رَبِّي إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ دِينًا قِيَمًا مِّلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۚ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Neel : “Sama Boroom gindi na ma teg ma ca yoon wu jub wa, di diine ju jub, di diiney Ibraahiima ma wéetal Boroomam te bokkuloon ca way-bokkaale ña.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
159Aaya

Tekki — Al-An'am 159

Simoore Al-An'am Aaya 159 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne dañoo xàjjale seen diine ba mu…

Simoore Aaya 159/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 157–161. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers