Al-An'am · 160/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
مَن جَاءَ بِالْحَسَنَةِ فَلَهُ عَشْرُ أَمْثَالِهَا ۖ وَمَن جَاءَ بِالسَّيِّئَةِ فَلَا يُجْزَىٰ إِلَّا مِثْلَهَا وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ ۝١٦٠
man jaaa`a bilhasanati falahoo `ashru amsaalihaa wa man jaaa`a bissaiyi`ati falaa yujzaaa illaa mislahaa wa hum laa yuzlamoon
📖 Tekkim Wolof
Ku def u yiw, am yool bu tollu ni fukki yooni yiw wa ; ku def ñaawtéef am bàkkaar bu tollu ni ñaawtéef wa. Te kenn duleen tooñ [ci yokkal mbaa wàññil leen ci dara].
🎧 Dégg

📜 Aaya 158-162 — Al-An'am

158هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمُ الْمَلَائِكَةُ أَوْ يَأْتِيَ رَبُّكَ أَوْ يَأْتِيَ بَعْضُ آيَاتِ رَبِّكَ ۗ يَوْمَ يَأْتِي بَعْضُ آيَاتِ رَبِّكَ لَا يَنفَعُ نَفْسًا إِيمَانُهَا لَمْ تَكُنْ آمَنَتْ مِن قَبْلُ أَوْ كَسَبَتْ فِي إِيمَانِهَا خَيْرًا ۗ قُلِ انتَظِرُوا إِنَّا مُنتَظِرُونَ
Moo ndax dañuy xaar ba Malaaka ya dikk fa ñoom? Walla sa Boroom agsi ? Walla lenn ci sa kéemaani Boroom dikk ? Bis ba lenn ci sa kéemaani Boroom dikkee, bàjjo bu gëmul woon lu jiitu, di door a gëm, du ko jariñ dara de, walla ku sàkkuwul wenn yiw it, ngëmam du ko jariñ dara. Neel : “Xaarleen ! ”. Nun it Noo ngi xaar.
159إِنَّ الَّذِينَ فَرَّقُوا دِينَهُمْ وَكَانُوا شِيَعًا لَّسْتَ مِنْهُمْ فِي شَيْءٍ ۚ إِنَّمَا أَمْرُهُمْ إِلَى اللَّهِ ثُمَّ يُنَبِّئُهُم بِمَا كَانُوا يَفْعَلُونَ
Ña nga xam ne dañoo xàjjale seen diine ba mu nekk ay pàcc-pàcc, bokkulook ñoom dara : seeni mbir ci Yàlla doŋŋ la nekk. Te Dana leen biral la ñu nekkoon di ko def.
160مَن جَاءَ بِالْحَسَنَةِ فَلَهُ عَشْرُ أَمْثَالِهَا ۖ وَمَن جَاءَ بِالسَّيِّئَةِ فَلَا يُجْزَىٰ إِلَّا مِثْلَهَا وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Ku def u yiw, am yool bu tollu ni fukki yooni yiw wa ; ku def ñaawtéef am bàkkaar bu tollu ni ñaawtéef wa. Te kenn duleen tooñ [ci yokkal mbaa wàññil leen ci dara].
161قُلْ إِنَّنِي هَدَانِي رَبِّي إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ دِينًا قِيَمًا مِّلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۚ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Neel : “Sama Boroom gindi na ma teg ma ca yoon wu jub wa, di diine ju jub, di diiney Ibraahiima ma wéetal Boroomam te bokkuloon ca way-bokkaale ña.
162قُلْ إِنَّ صَلَاتِي وَنُسُكِي وَمَحْيَايَ وَمَمَاتِي لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Neel : “Samag julli, samag jaamu, samag dund ak samag dee, Yàlla Boroom àddina bee leen moom.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
160Aaya

Tekki — Al-An'am 160

Simoore Al-An'am Aaya 160 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku def u yiw, am yool bu tollu ni fukki…

Simoore Aaya 160/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 158–162. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers