Al-An'am · 63/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
قُلْ مَن يُنَجِّيكُم مِّن ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ تَدْعُونَهُ تَضَرُّعًا وَخُفْيَةً لَّئِنْ أَنجَانَا مِنْ هَٰذِهِ لَنَكُونَنَّ مِنَ الشَّاكِرِينَ ۝٦٣
Qul mai yunajjeekum min zulumaatil barri walbahri tad`oonahoo tadarru`anw wa khufyatann la`in anjaanaa min haazihee lanakoonana minash shaakireen
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Kan moo leen di musal ci lëndëmu jéeri ak gu géej ? ” Te ngeen di Ko faral a woo ànd ak toroxlu ak nëbbu, naan : “ Cëy Yàlla, boo nu musalee ci lii, kon dey nu bokk ca gërëmkat ya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 61-65 — Simoore Al-An'am

61وَهُوَ الْقَاهِرُ فَوْقَ عِبَادِهِ ۖ وَيُرْسِلُ عَلَيْكُمْ حَفَظَةً حَتَّىٰ إِذَا جَاءَ أَحَدَكُمُ الْمَوْتُ تَوَفَّتْهُ رُسُلُنَا وَهُمْ لَا يُفَرِّطُونَ
Te Moom mooy Aji-not ja ci kaw jaamam ya. Te Mooy yónni ci yéen ay Malaaka yu leen di wattu. Ba kero bis ba dee di agsi, ba kenn ci yéen sunuy ndaw rey ko, te ñoom sàgganuñu ci dara.
62ثُمَّ رُدُّوا إِلَى اللَّهِ مَوْلَاهُمُ الْحَقِّ ۚ أَلَا لَهُ الْحُكْمُ وَهُوَ أَسْرَعُ الْحَاسِبِينَ
Bu loolu jàllee, ñu delloo leen fa Yàlla, kay seen Boroom tigi. Moo ndax du Moo moom àtte ba te Moo gën a gaaw wàññikat yépp.
63قُلْ مَن يُنَجِّيكُم مِّن ظُلُمَاتِ الْبَرِّ وَالْبَحْرِ تَدْعُونَهُ تَضَرُّعًا وَخُفْيَةً لَّئِنْ أَنجَانَا مِنْ هَٰذِهِ لَنَكُونَنَّ مِنَ الشَّاكِرِينَ
Neel : “Kan moo leen di musal ci lëndëmu jéeri ak gu géej ? ” Te ngeen di Ko faral a woo ànd ak toroxlu ak nëbbu, naan : “ Cëy Yàlla, boo nu musalee ci lii, kon dey nu bokk ca gërëmkat ya.
64قُلِ اللَّهُ يُنَجِّيكُم مِّنْهَا وَمِن كُلِّ كَرْبٍ ثُمَّ أَنتُمْ تُشْرِكُونَ
Neel : “Yàlla moo leen di musal ci loolu, ak njàqare ju mu mën di doon. Ba noppi ngeen di ko bokkaale”.
65قُلْ هُوَ الْقَادِرُ عَلَىٰ أَن يَبْعَثَ عَلَيْكُمْ عَذَابًا مِّن فَوْقِكُمْ أَوْ مِن تَحْتِ أَرْجُلِكُمْ أَوْ يَلْبِسَكُمْ شِيَعًا وَيُذِيقَ بَعْضَكُم بَأْسَ بَعْضٍ ۗ انظُرْ كَيْفَ نُصَرِّفُ الْآيَاتِ لَعَلَّهُمْ يَفْقَهُونَ
Neel : “Moom am na kàttanug yónnee leen mbugal mu leen bawoo ci kaw walla ci seen suufi tànk, mbaa Mu dogal, ci seen biir, juuyoo. Ba ku nekk mos ngaañ la jóge ca moroomam.” Gisal ni Nuy leeralee tegtal yi ndax ñoom ñu mën koo dégg ?
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
63Aaya

Tekki — Al-An'am 63

Simoore Al-An'am Aaya 63 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Kan moo leen di musal ci lëndëmu jéeri…

Simoore Aaya 63/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 61–65. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers