Al-A'raf · 152/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
إِنَّ الَّذِينَ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ سَيَنَالُهُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَذِلَّةٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُفْتَرِينَ ۝١٥٢
Innal lazeenat takhazul `ijla-sa yanaaluhum ghadabum mir Rabbihim wa zillatun fil hayaatid dunyaa; wa kazaalika najzil muftareen
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
🎧 Dégg

📜 Aaya 150-154 — Al-A'raf

150وَلَمَّا رَجَعَ مُوسَىٰ إِلَىٰ قَوْمِهِ غَضْبَانَ أَسِفًا قَالَ بِئْسَمَا خَلَفْتُمُونِي مِن بَعْدِي ۖ أَعَجِلْتُمْ أَمْرَ رَبِّكُمْ ۖ وَأَلْقَى الْأَلْوَاحَ وَأَخَذَ بِرَأْسِ أَخِيهِ يَجُرُّهُ إِلَيْهِ ۚ قَالَ ابْنَ أُمَّ إِنَّ الْقَوْمَ اسْتَضْعَفُونِي وَكَادُوا يَقْتُلُونَنِي فَلَا تُشْمِتْ بِيَ الْأَعْدَاءَ وَلَا تَجْعَلْنِي مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Ba Muusaa ñibbee ca aw nitam, mer lool, dafa wax ne : “Nii ngeen ma ginnaawoo ñaaw na ! Xanaa dangeen a yàkkamti seen àtteb Boroom gaaw a ñëw? ”. Mu daldi sànni àlluwa ya, jàpp ca boppub mbokkam ma, xëcc ko. Aaruuna toontu ko ne : “Yaw sama doomu-ndey , nit ñi dañu maa doyadal te xaw nañu maa rey sax. Kon bul bégloo noon ya te bul ma boole ca nit ña di way-tooñ”.
151قَالَ رَبِّ اغْفِرْ لِي وَلِأَخِي وَأَدْخِلْنَا فِي رَحْمَتِكَ ۖ وَأَنتَ أَرْحَمُ الرَّاحِمِينَ
Mu ne : “Yaw sama Boroom, jéggal ma ak sama mbokk mii te nga tàbbal nu ci sa yërmaande, ndax Yaw yaa ëpp yërmaande képp kuy yërëme”.
152إِنَّ الَّذِينَ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ سَيَنَالُهُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَذِلَّةٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُفْتَرِينَ
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
153وَالَّذِينَ عَمِلُوا السَّيِّئَاتِ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِهَا وَآمَنُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
154وَلَمَّا سَكَتَ عَن مُّوسَى الْغَضَبُ أَخَذَ الْأَلْوَاحَ ۖ وَفِي نُسْخَتِهَا هُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ هُمْ لِرَبِّهِمْ يَرْهَبُونَ
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
152Aaya

Tekki — Al-A'raf 152

Simoore Al-A'raf Aaya 152 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal…

Simoore Aaya 152/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 150–154. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers