At-Tawba · 2/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
فَسِيحُوا فِي الْأَرْضِ أَرْبَعَةَ أَشْهُرٍ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ غَيْرُ مُعْجِزِي اللَّهِ ۙ وَأَنَّ اللَّهَ مُخْزِي الْكَافِرِينَ ۝٢
Faseehoo fil ardi arba`ata ashhurinw wa`lamoooannakum ghairu mu`jizil laahi wa annal laaha mukhzil kaafireen
📖 Tekkim Wolof
“Kon doxleen ci suuf si ñeneenti weer ; te nangeen xam ne nag yéen dungeen mën a raw Yàlla te nag Yàlla Kuy gàcceel yéefar yi la.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-4 — At-Tawba

1بَرَاءَةٌ مِّنَ اللَّهِ وَرَسُولِهِ إِلَى الَّذِينَ عَاهَدتُّم مِّنَ الْمُشْرِكِينَ
Lii deñtalu la gu tukkee ci Yàlla ak ub Yonentam ci yéen ak ñoom bokkaalekat ya ngeen bokkal koote :
2فَسِيحُوا فِي الْأَرْضِ أَرْبَعَةَ أَشْهُرٍ وَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ غَيْرُ مُعْجِزِي اللَّهِ ۙ وَأَنَّ اللَّهَ مُخْزِي الْكَافِرِينَ
“Kon doxleen ci suuf si ñeneenti weer ; te nangeen xam ne nag yéen dungeen mën a raw Yàlla te nag Yàlla Kuy gàcceel yéefar yi la.”
3وَأَذَانٌ مِّنَ اللَّهِ وَرَسُولِهِ إِلَى النَّاسِ يَوْمَ الْحَجِّ الْأَكْبَرِ أَنَّ اللَّهَ بَرِيءٌ مِّنَ الْمُشْرِكِينَ ۙ وَرَسُولُهُ ۚ فَإِن تُبْتُمْ فَهُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۖ وَإِن تَوَلَّيْتُمْ فَاعْلَمُوا أَنَّكُمْ غَيْرُ مُعْجِزِي اللَّهِ ۗ وَبَشِّرِ الَّذِينَ كَفَرُوا بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
Te it xamle la gu tukke ci Yàlla ak Yonentam jëm ci nit ñi, ca bisub gën gaa Màggi Aj mooy ne : Yàlla nag Ku deñ la mook Yonentam ci yéefar yi. Bu ngeen rëccoo, tuub, kon mooy gën ci yéen. Bu ngeen dëddoo [nangeen xam ne] dungeen mën a rëcc Yàlla te nanga yëgal ña weddi, mbugal mu metti.
4إِلَّا الَّذِينَ عَاهَدتُّم مِّنَ الْمُشْرِكِينَ ثُمَّ لَمْ يَنقُصُوكُمْ شَيْئًا وَلَمْ يُظَاهِرُوا عَلَيْكُمْ أَحَدًا فَأَتِمُّوا إِلَيْهِمْ عَهْدَهُمْ إِلَىٰ مُدَّتِهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ
Ba mu des ña nga xam ne, ca bokkaalekat ya, fasante woon nañu kóllare ak yéen, te defuñu dara lu leen wàññi, te dimbaliwuñu kenn kuy dal ci seen kaw : ñooñu, ngeen matal seen kóllare ak ñoom ba ca àpp ba. Yàlla dafa sopp ñu ragal ña [seen Boroom].
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
2Aaya

Tekki — At-Tawba 2

Simoore At-Tawba Aaya 2 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Kon doxleen ci suuf si ñeneenti weer ; te nangeen…

Simoore Aaya 2/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 1–4. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers