Simoore As-Saffat pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore As-Saffat pdf Wolof — Wàcce Simoore As-Saffat Tekki. Simoore As-Saffat (Meccan) 182 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore As-Saffat

ﭑﭒﭓ
37:1
[Maa ngi] giñ ci [Malaaka] ya sësëloo, def ay sàppe.
ﭔﭕﭖ
37:2
Ñay bëmëg niir yaak doole.
ﭗﭘﭙ
37:3
Ñay jàng ngir fàttali :
ﭚﭛﭜﭝ
37:4
“Ne seen Yàlla jenn la tigi,
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
37:5
mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk seen diggante tey Boroom penku yi”.
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
37:6
Taaralal Nanu asamaan si gën a jexe àddina si ci taarub ay bidiw,
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
37:7
def ca kaaraange ci sépp séytaane suy féttérlu.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
37:8
Duñu mën yëddu waa péey ba gën a kawe ; te dañu leen fay mbàqe wet gu nekk,
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
37:9
dàqe leen fa. Ñu am mbugal muy sax.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
37:10
Xanaa rekk léeg-léeg mu am ñu cay sàcc ay xibaar ; ñu di ko dàq ak jumu safara buy bënn.
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
37:11
Laajleen baxam dañoo gën a jafe bind ñeneen ña Nu bind ? Noo ngi leen binde ci ban bu tikk !
ﮙﮚﮛﮜ
37:12
Yaw waaru nga, te ñoom ña ngay tejjiy reetaan !
ﮝﮞﮟﮠﮡ
37:13
Te bu ñu leen di fàttali, duñu fàttaliku [Alxuraan] ;
ﮢﮣﮤﮥﮦ
37:14
dañuy wàkkante ak a reetaan [saa su ñu gisee keemaan],
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
37:15
tey wax naan : “Lii dey ag njabar doŋŋ la.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
37:16
Moo ndax su nu faatoo ba def suuf ak i yax, dees nanu dekkalaat ?
ﯗﯘﯙ
37:17
ak sunuy baay ak i maamaat ? ”
ﯚﯛﯜﯝﯞ
37:18
Neel : “Waaw ! te dangeen torox de”.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
37:19
Genn ug xaacu rekk ay jib, ñu ne xewwu di xoolante (dekki),
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
37:20
ñuy wax naan : “Ngalla nun ! Bis-pénc baa ngi nii waay”.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
37:21
“Lii mooy bisub àtte ba ngeen jàppe woon ay fen, weddi ko”.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
37:22
“Dajaleleen tooñkat ya ak seeni jabar ak la ñu daan jaamu,
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
37:23
bàyyi woon Yàlla. Te wëtal leen jëme yoonu Safara.
ﰆﰇﰈﰉﰊ
37:24
Te ngeen taxawlooleen : ndax dañu leen di laaj”.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
37:25
“Ana lan moo tax dungeen dimbalante” ?
ﭖﭗﭘﭙﭚ
37:26
Li wér mooy bis niki tey jébbalu nañu,
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
37:27
ku nekk di geesu moroom ma, ñuy laajante ;
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
37:28
Ñuy wax naan : “Yéen a nu daan ga ci kéefar”.
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
37:29
[Kilifa ya] ne leen : “Yéen kay yéen a gëmul woon.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
37:30
Te nun amunu woon benn sañ-sañ ci yéen. Yéen kay yéen a bewoon.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
37:31
La Yàlla daan wax dal na ci sunu kaw ; [tey] noo ngi toqamtiku [mbugal].
ﮂﮃﮄﮅﮆ
37:32
“Noo ngi leen di jiiñ cànkute, waaye nun ñépp a faf sànku”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌ
37:33
Bu bisub keroogee ñoom ñéppay bokk mbugal ma.
ﮍﮎﮏﮐﮑ
37:34
Noonu la Nuy def tooñkat ya.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
37:35
Bu ñu waxaan ne : “Amul jeneen yàlla ju dul Yàlla”, dañu daan rëy-rëylu,
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
37:36
tey wax naan : “Ndax danuy bàyyi sunu yàlla yi ngir woykat bu dof ? ”
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
37:37
Te moom dëgg rekk la indi tey dëggal li Yonent ya indi woon,
ﮪﮫﮬﮭﮮ
37:38
Yéen dangeen mos mbugal mu mitti.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
37:39
Te it kenn du leen feye lu dul la ngeen daan jëfe,
ﯗﯘﯙﯚﯛ
37:40
ba mu des jaami Yàlla yay sellal,
ﯜﯝﯞﯟﯠ
37:41
Ñoom am nañu wërsëg wu ñu xam :
ﯡﯢﯣﯤ
37:42
ay fuytéef ak i teraanga,
ﯥﯦﯧﯨ
37:43
ca biir Àjjanay xéewal ja,
ﯩﯪﯫﯬ
37:44
ñuy jàkkaarloo ca seen kawi lal.
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
37:45
Ñu di leen wër ak kaasi bënub ndox
ﯳﯴﯵﯶ
37:46
weex tàll, te neex lool ca ña koy naan,
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
37:47
Lëj-lëj du fa am.
ﯿﰀﰁﰂﰃ
37:48
Te am nañu fa ay lamsalkat yu am bët ,
ﰄﰅﰆﰇ
37:49
weex ba mel ni nen.
ﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
37:50
Ku nekk di geesu moroomam di laajante.
ﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
37:51
Mu am ci ñoom kuy wax naan : “Man dey amoon naa àndandoo”
ﭑﭒﭓﭔﭕ
37:52
di wax ba-tey naan : “Ndax yaw gëm nga tigi ?
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
37:53
Ndax bu nu faatoo ba doon suuf ak i yax, dara dananu warati ? ”
ﭞﭟﭠﭡﭢ
37:54
Mu wax ne : “Xanaa téenuleen ? ”
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
37:55
Mu daldi téen, gis ko ca biir Safara,
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
37:56
mu wax ne : “Waat naa ci Yàlla ne ! Xaw nga maa tax a alku !
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
37:57
dogankoon ak sama dimbalul Boroom, danaa sànku.
ﭶﭷﭸﭹ
37:58
Xanaa nun dey dunu dee
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
37:59
lu dul ca dee gu jëkk ga te xanaa kenn dunu mbugal ? ”
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
37:60
Lii mooy texe gu màgg ga.
ﮇﮈﮉﮊﮋ
37:61
Ñiy jëf, nañuy jëf lu mel nii.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
37:62
Moo ndax loolu moo di wàccuwaay ba gën, walla garabug Zaquum ?
ﮓﮔﮕﮖﮗ
37:63
Def nanu ko muy sànjub tooñkat ya.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
37:64
Moom garab la guy génn ca ndéntul Safara.
ﮟﮠﮡﮢﮣ
37:65
Meññent ma mel ni boppi séytaane.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
37:66
Ca la ñuy lekk, di ca feesal seeni biir.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
37:67
Am nañu fa, ca kawam, am ndox mu tàng [di wañax].
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
37:68
Safara rekk mooy seen kër.
ﯚﯛﯜﯝﯞ
37:69
Daje nañu faak seeni [baay ak i maam] cig cànkute,
ﯟﯠﯡﯢﯣ
37:70
ñuy yolli-yolli topp leen.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
37:71
Li ëppoon ca ña leen jiitu woon sàkku woon nañu.
ﯪﯫﯬﯭﯮ
37:72
Ndax yónni woon Nanu ci ñoom ñuy xuppe, di waaraate .
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
37:73
Xoolal mujjug ñanu daan xupp !
ﯵﯶﯷﯸﯹ
37:74
Ña ca dul jaami Yàlla ya ca daan sellal :
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
37:75
Nooh woo na Nu di ñaan, Nu wuyyu ko, nangu ñaanam.
ﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
37:76
Nu musal ko mook njabootam ci tiit mu rëy ma,
ﭑﭒﭓﭔﭕ
37:77
Nu def ay sëtam doŋŋ des fa.
ﭖﭗﭘﭙﭚ
37:78
Nu bàyyi ko, may ko mu di fàttaliku,
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
37:79
Yal na jàmm wàcc ci Nooh ci kaw àddina sépp !
ﭡﭢﭣﭤﭥ
37:80
Noonu la Nuy feye ñiy rafetal.
ﭦﭧﭨﭩﭪ
37:81
Moom bokk na ca Sunu jaam yu gëm ya.
ﭫﭬﭭﭮ
37:82
Ginnaaw ba, Nu labal ña ca des.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
37:83
Ibrahiima bokkoon na ca ay njabootam.
ﭵﭶﭷﭸﭹﭺ
37:84
Fàttalikul ba mu dikkee ca Boroomam ànd ak xol bu mucc ayib.
ﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
37:85
Ak ba mu waxee baayam ak nitam, ne leen : “Ana li ngeen di jaamu ? ”
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
37:86
Moo ndax ay nar ngeen di namm a def ay yàlla bàyyi Yàlla Moom ?
ﮈﮉﮊﮋﮌ
37:87
Waaw, lu ngeen njort ci Yàlla boroom asamaan si ? ”
ﮍﮎﮏﮐﮑ
37:88
Mu téen xool biddéew yi [di settantal],
ﮒﮓﮔﮕ
37:89
mu daldi wax ne : “Man damaa wopp”.
ﮖﮗﮘﮙ
37:90
Ñu dëddu ko, won ko ginnaaw.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
37:91
Mu potoxlu ca seen yàlla ya, ne leen : “Ndax dungeen lekk ?
ﮡﮢﮣﮤﮥ
37:92
Ana lu leen dal ba dungeen wax ? ”
ﮦﮧﮨﮩﮪ
37:93
Mu potoxlu dóor leen ak ndeyjoor.
ﮫﮬﮭﮮ
37:94
Ñu wutsi ko di daw.
ﮯﮰﮱﯓﯔ
37:95
Mu wax ne : “Ndax dangeen di jaamu lu ngeen di yatt,
ﯕﯖﯗﯘﯙ
37:96
te Yàlla moo leen bind ak li ngeen di defar ? ”
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
37:97
Ñu wax ne : “Tabaxal-leen ko puur te sànni ko ca safara sa ! ”
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
37:98
Ñu bëggoon koo fexeel ; Nu suufeel leen, detteel leen.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
37:99
Mu wax ne : “Maa ngi dem ca sama Boroom, Dana ma gindi.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
37:100
Yaw sama Boroom, may ma ay sët yu yiw”.
ﯵﯶﯷﯸ
37:101
Nu bégal ko, may ko doom ju lewet .
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕ
37:102
Ba mu amee ati àndak moom, Ibraahiima wax na ne : "Yaw samas doom, gis naa ci bi may nelaw, ci biir gént, ndigalul war laa rendi. Seetal looy xalaat”. (Ismaayiila) ne ko : “Yaw sama baay, defal lu ñu la digal : bu soobee Yàlla, danga gis ne maag muñkat yee ànd”.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
37:103
Ba ñu wéyalee seen ndigalul Boroom, mu di dëféenal ko,
ﭖﭗﭘﭙ
37:104
Nu woo ko, ne ko : “Éy yaw Ibraahiima !
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
37:105
Dëggal nga gént gi. Te noonu la Nuy feye ñiy rafetal”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
37:106
Lii ab tontu la bu bir.
ﭩﭪﭫﭬ
37:107
Nu daldi koy jot ak lu ñuy rendi lu màgg.
ﭭﭮﭯﭰﭱ
37:108
Daldi koy bàyyi muy dundu moom Ismaahiila :
ﭲﭳﭴﭵ
37:109
“Jàmmi Yàlla na nekk ci kaw Ibraahiima”.
ﭶﭷﭸﭹ
37:110
Noonu la Nuy feye ñiy rafetal ;
ﭺﭻﭼﭽﭾ
37:111
bokk na ci Sunu jaam ñi gëm.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄ
37:112
Bégal Nanu ko ci def Isaaqa mu di Yonent bokk ca ñay rafetal.
ﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
37:113
Nu barkeel ko moom ak Isaaqa. Mu am ci seeni sët kuy rafetal ak kuy tooñ boppam.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
37:114
Xéewaloon Nanu Muusaa ak Haaruuna,
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
37:115
Musaloon Nanu leen ñoom seeni sët ca tiit mu rëy ma,
ﮝﮞﮟﮠﮡ
37:116
Nu dimbali woon leen, ñoom ñoo nootoon.
ﮢﮣﮤﮥ
37:117
Nu indiloon leen ab téere bu bir
ﮦﮧﮨﮩ
37:118
Nu indiloon leen yoon wu jub wa xocc.
ﮪﮫﮬﮭﮮ
37:119
Nu bàyyi woon leen nit ña di leen fàttaliku :
ﮯﮰﮱﯓﯔ
37:120
“Jàmmi Yàlla na wàcc ci Muusaa ak Haaruuna”
ﯕﯖﯗﯘﯙ
37:121
Noonu la Nuy feye ñiy rafetal ;
ﯚﯛﯜﯝﯞ
37:122
ñoom ñaar bokkoon nañu ci Sunu jaam ñi gëm.
ﯟﯠﯡﯢﯣ
37:123
Ilyaas it tigi bokkoon na ci Yonent ya.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
37:124
[Fàttalikul] ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Ndax dungeen ragal Yàlla ? ”
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
37:125
Moo ngax dangeen di woo Bahlu bàyyi Yàlla miy ngën ji kuy bind,
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
37:126
Yàlla miy seen Boroom te di Boroomi seeni baay ak i maamaat ? ”
ﭑﭒﭓﭔ
37:127
Ñu weddi ko, Nu mbugal leen.
ﭕﭖﭗﭘﭙ
37:128
Ba mu des jaami Yàlla ya daan sellal.
ﭚﭛﭜﭝﭞ
37:129
Nu bàyyi nit ñuy mujj noonu di ko fàttaliku :
ﭟﭠﭡﭢﭣ
37:130
“Jàmm yal na nekk ci njabootug Ilyaas”.
ﭤﭥﭦﭧﭨ
37:131
Noonu la Nuy feye ñiy rafetal,
ﭩﭪﭫﭬﭭ
37:132
bokk na ci Sunu jaam ñi gëm.
ﭮﭯﭰﭱﭲ
37:133
Lóot it bokk na ci Yonent yi.
ﭳﭴﭵﭶﭷ
37:134
[Fàttalikul] ba Nu ko musalee mook njabootam gépp,
ﭸﭹﭺﭻﭼ
37:135
ba mu des màggat gu jigéen ga àndoon ak ña sànku wo
ﭽﭾﭿﮀ
37:136
Ginnaaw ba, faagaagal Nanu ña ca des
ﮁﮂﮃﮄﮅ
37:137
Te yéen a ngi leen di romb bu ngeen di xëy
ﮆﮇﮈﮉﮊ
37:138
ak ci guddi gi. Xanaa dungeen xalaat ?
ﮋﮌﮍﮎﮏ
37:139
Yuunuusa it bokk na ca Yonent ya.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
37:140
Ba muy daw jëm ca gaal ga ñu yeb ga,
ﮖﮗﮘﮙﮚ
37:141
Ba ñu wantalee mu bokk ca ña ñu waroon a sànni ca ndox ma.
ﮛﮜﮝﮞﮟ
37:142
Jën wa dal koy wann, muy ku yeddu.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
37:143
Dugankoon ak li mu bokkoon ca ña doon sàbbaal Yàlla,
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
37:144
kon dey dana sax ca biir [jën wa] ba bisub dekkiwaat ba di ñëw.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
37:145
Nu sànni ko ca teges ga te muy ku ràgg.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
37:146
Nu daldi fay saxal gàncaxug beraf,
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
37:147
Nu yebal ko muy Yonent ci téeméeri junniy nit mbaa lu ko ëpp.
ﯡﯢﯣﯤﯥ
37:148
Ba ñu gëmee, xéewalal Nanu leen fa ab diir.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
37:149
Laajleen baxam : “Ndax Yàlla moo ame doom yu jigéen, ñoom ñuy am doom yu góor ?
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
37:150
Walla dañoo bind Malaaka yi def leen ñu di ay jigéen, seere ko ? ”.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
37:151
Ndax ñoom dañuy faral di wax ci seen duur ya, naan :
ﯹﯺﯻﯼﯽ
37:152
“Yàlla am na doom” ; te ñoom dañuy fen doŋŋ !
ﯾﯿﰀﰁﰂ
37:153
Moo ndax dafay gënal doom ju jigéen ci kaw doom ju góor ?
ﭑﭒﭓﭔﭕ
37:154
Ana lu leen dal ba ngeen di àttee nii ?
ﭖﭗﭘ
37:155
Moo ndax dangeen dul fàttaliku ?
ﭙﭚﭛﭜﭝ
37:156
Walla dangeen am ay firnde yu wóor ?
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
37:157
Kon indil seenub Téere ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
37:158
Ñu di ko askanale ci jinne yi, ndax jinne yi xam nañu ne danañu teew ci kanamu [Yàlla].
ﭰﭱﭲﭳﭴ
37:159
Tudd naa sellug Yàlla ga. Kawe na lool la ñu koy melal !
ﭵﭶﭷﭸﭹ
37:160
Ba mu des jaami Yàlla yiy sellal.
ﭺﭻﭼﭽ
37:161
Yéen ak li ngeen di jaamu,
ﭾﭿﮀﮁﮂ
37:162
kenn duleen ci fitnaal,
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
37:163
ku dul kuy nar a xoyomu ci Safara.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
37:164
Amul kenn ci [Malaaka yi] lu dul ne am na wàccuwaay wu ñu xam ;
ﮐﮑﮒﮓ
37:165
te noo leen defoon ay sàppe ;
ﮔﮕﮖﮗ
37:166
te nun nooy sàbbaal Yàlla.
ﮘﮙﮚﮛ
37:167
Doonte la sax ña ngay wax naan :
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
37:168
“Su nu amoon waarate gu bawoo ca sunuy maam,
ﮣﮤﮥﮦﮧ
37:169
kon de nu doon ay jaami Yàlla yuy sellal !
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
37:170
Weddi nañu ko, waaye danañu xam ne.
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
37:171
Sunu kàddu jiitu woon na ci Sunu jaam ña di ay Yonent,
ﯕﯖﯗﯘ
37:172
ñoom danañu am ndimbal,
ﯙﯚﯛﯜﯝ
37:173
te it Sunuy xarekat ñooy not.
ﯞﯟﯠﯡﯢ
37:174
nanga leen dummóoyu ab diir ;
ﯣﯤﯥﯦ
37:175
te nga seetluleen : danañu gis de !
ﯧﯨﯩ
37:176
Moo ndax ñoom dañuy yàkkamti sunu mbugal ?
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
37:177
Su wàccee ci seenub ëtt, ñoom ña ñu doon fàttali, ndaw suba gu bon !
ﯱﯲﯳﯴﯵ
37:178
nanga leen dummóoyu ab diir ;
ﯶﯷﯸﯹ
37:179
te nga seetluleen : danañu gis de !
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
37:180
Tudd naa sellug sa Boroom, Boroom kàttan gi. Kawe na ca la ñu koy melal !
ﰁﰂﰃﰄ
37:181
Te jàmm yal na wàcc ci Yonent yi,
ﰅﰆﰇﰈﰉ
37:182
te xeeti cant yépp ñeel na Yàlla miy Boroom àddina si !
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







