Hud · 121/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَقُل لِّلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ اعْمَلُوا عَلَىٰ مَكَانَتِكُمْ إِنَّا عَامِلُونَ ۝١٢١
Wa qul lillazeena laa yu`minoona` maloo `alaa makaanatikum innaa `aamiloon
📖 Tekkim Wolof
Te waxal ña gëmul ne leen : “Defleen lu leen soob. Nun it, nu ngiy jëf [li nu sunu Boroom digal].

🎧 Dégg


📜 Aaya 119-123 — Hud

119إِلَّا مَن رَّحِمَ رَبُّكَ ۚ وَلِذَٰلِكَ خَلَقَهُمْ ۗ وَتَمَّتْ كَلِمَةُ رَبِّكَ لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
ndare ña sa Boroom yërëm. Loolu moo tax Mu bind leen. Te it moo tax sa kàddug Boroom mat ca la mu wax ne : “Danaa feesal Safara ci aw nit ak i jinne mbooleseen”.
120وَكُلًّا نَّقُصُّ عَلَيْكَ مِنْ أَنبَاءِ الرُّسُلِ مَا نُثَبِّتُ بِهِ فُؤَادَكَ ۚ وَجَاءَكَ فِي هَٰذِهِ الْحَقُّ وَمَوْعِظَةٌ وَذِكْرَىٰ لِلْمُؤْمِنِينَ
Te lépp Lanu lay nittili ci xew-xewi Yonent ya, Danu cay dalal sa xel. Te dëgg ak ug waare dikkal na la di aw lay ànd ak di fàttali ci ñi gëm.
121وَقُل لِّلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ اعْمَلُوا عَلَىٰ مَكَانَتِكُمْ إِنَّا عَامِلُونَ
Te waxal ña gëmul ne leen : “Defleen lu leen soob. Nun it, nu ngiy jëf [li nu sunu Boroom digal].
122وَانتَظِرُوا إِنَّا مُنتَظِرُونَ
Xaarleen. Nun it noo ngi xaar ! ”
123وَلِلَّهِ غَيْبُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَإِلَيْهِ يُرْجَعُ الْأَمْرُ كُلُّهُ فَاعْبُدْهُ وَتَوَكَّلْ عَلَيْهِ ۚ وَمَا رَبُّكَ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Yàllaa moom kumpag asamaan yi ak suuf si, te mbir yépp ca moom lañuy dellu. Kon nag jaamu ko te nga wéeru ci moom. Sa Boroom ñàkkul paal ci li ngeen di def de.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
121Aaya

Tekki — Hud 121

Simoore Hud Aaya 121 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te waxal ña gëmul ne leen : “Defleen lu leen…

Simoore Aaya 121/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 119–123. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers