An-Nahl · 26/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
قَدْ مَكَرَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَأَتَى اللَّهُ بُنْيَانَهُم مِّنَ الْقَوَاعِدِ فَخَرَّ عَلَيْهِمُ السَّقْفُ مِن فَوْقِهِمْ وَأَتَاهُمُ الْعَذَابُ مِنْ حَيْثُ لَا يَشْعُرُونَ ۝٢٦
Qad makaral lazeena min qablihim fa atal laahu bunyaa nahum minal qawaa`idi fakharra `alaihimus saqfu min fawqihim wa ataahumul `azaabu min haisu laa yash`uroon
📖 Tekkim Wolof
Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe, Yàlla toj seeni tabax ya dale ko ca ndëgërlaay ja. Téeg ma daanu seen kaw, mbugal ma agsi ca ñoom jaare fu ñu ko foogewul woon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 24-28 — An-Nahl

24وَإِذَا قِيلَ لَهُم مَّاذَا أَنزَلَ رَبُّكُمْ ۙ قَالُوا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Bu ñu nee leen : “Lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu ne : “Xanaa ay léeb yu jóge ca mag ñu njëgg ña ! ”
25لِيَحْمِلُوا أَوْزَارَهُمْ كَامِلَةً يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۙ وَمِنْ أَوْزَارِ الَّذِينَ يُضِلُّونَهُم بِغَيْرِ عِلْمٍ ۗ أَلَا سَاءَ مَا يَزِرُونَ
Danañu yenu seeni bàkkaar ba mu mat sëkk, Bis-pénc ba, ak lenn ca bàkkaari ña ñu réeral, ci loo xam ne amuñu ca woon xam-xam ; cëy ndaw yen bu bon !
26قَدْ مَكَرَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَأَتَى اللَّهُ بُنْيَانَهُم مِّنَ الْقَوَاعِدِ فَخَرَّ عَلَيْهِمُ السَّقْفُ مِن فَوْقِهِمْ وَأَتَاهُمُ الْعَذَابُ مِنْ حَيْثُ لَا يَشْعُرُونَ
Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe, Yàlla toj seeni tabax ya dale ko ca ndëgërlaay ja. Téeg ma daanu seen kaw, mbugal ma agsi ca ñoom jaare fu ñu ko foogewul woon.
27ثُمَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يُخْزِيهِمْ وَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تُشَاقُّونَ فِيهِمْ ۚ قَالَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ إِنَّ الْخِزْيَ الْيَوْمَ وَالسُّوءَ عَلَى الْكَافِرِينَ
Te bu Bis-pénc baa, Dana leen gàcceel, ne leen : “Waa ana sama bokkaale ya taxoon ngeen wuuteeg [jullit ñi] ? ” - Ña amoom xam-xam tontu ne : “Bis niki tey, toroxteeg mbugal dal na ci kaw yéefar yi”.
28الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ ۖ فَأَلْقَوُا السَّلَمَ مَا كُنَّا نَعْمَلُ مِن سُوءٍ ۚ بَلَىٰ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp, ñu sànnib nuyyoo, naan : “Defunu woon dara lu bon ! ” - “Axakañ, Yàlla ku xam la li ngeen daan def”.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
26Aaya

Tekki — An-Nahl 26

Simoore An-Nahl Aaya 26 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe, Yàlla toj…

Simoore Aaya 26/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 24–28. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers