An-Nahl · 28/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ ۖ فَأَلْقَوُا السَّلَمَ مَا كُنَّا نَعْمَلُ مِن سُوءٍ ۚ بَلَىٰ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٢٨
Allazeena tatawaf faahu mul malaaa`ikatu zaalimeee anfusihim fa alqawus salama maa kunnaa na`malu min sooo`; balaaa innal laaha `aleemum bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp, ñu sànnib nuyyoo, naan : “Defunu woon dara lu bon ! ” - “Axakañ, Yàlla ku xam la li ngeen daan def”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-30 — An-Nahl

26قَدْ مَكَرَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَأَتَى اللَّهُ بُنْيَانَهُم مِّنَ الْقَوَاعِدِ فَخَرَّ عَلَيْهِمُ السَّقْفُ مِن فَوْقِهِمْ وَأَتَاهُمُ الْعَذَابُ مِنْ حَيْثُ لَا يَشْعُرُونَ
Ña leen jiitu woon defoon nañu ay pexe, Yàlla toj seeni tabax ya dale ko ca ndëgërlaay ja. Téeg ma daanu seen kaw, mbugal ma agsi ca ñoom jaare fu ñu ko foogewul woon.
27ثُمَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يُخْزِيهِمْ وَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تُشَاقُّونَ فِيهِمْ ۚ قَالَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ إِنَّ الْخِزْيَ الْيَوْمَ وَالسُّوءَ عَلَى الْكَافِرِينَ
Te bu Bis-pénc baa, Dana leen gàcceel, ne leen : “Waa ana sama bokkaale ya taxoon ngeen wuuteeg [jullit ñi] ? ” - Ña amoom xam-xam tontu ne : “Bis niki tey, toroxteeg mbugal dal na ci kaw yéefar yi”.
28الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ ۖ فَأَلْقَوُا السَّلَمَ مَا كُنَّا نَعْمَلُ مِن سُوءٍ ۚ بَلَىٰ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp, ñu sànnib nuyyoo, naan : “Defunu woon dara lu bon ! ” - “Axakañ, Yàlla ku xam la li ngeen daan def”.
29فَادْخُلُوا أَبْوَابَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ فَلَبِئْسَ مَثْوَى الْمُتَكَبِّرِينَ
Kon dugguleen ciy buntu Safara, te dangeen cay béel. Te bon na lool dëkkukaayu ña daan rëy-rëylu !
30۞ وَقِيلَ لِلَّذِينَ اتَّقَوْا مَاذَا أَنزَلَ رَبُّكُمْ ۚ قَالُوا خَيْرًا ۗ لِّلَّذِينَ أَحْسَنُوا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةٌ ۚ وَلَدَارُ الْآخِرَةِ خَيْرٌ ۚ وَلَنِعْمَ دَارُ الْمُتَّقِينَ
Ñuy wax [ña ragal seen Boroom] : “Ana lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu tontu ne : “Yiw”. Ñeel na ñi rafetal ci àddina Samay teraanga ; waaye kërug àllaaxiraa gën. Te aka baax kërug way-ragal ña [seen Boroom] !
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
28Aaya

Tekki — An-Nahl 28

Simoore An-Nahl Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp,…

Simoore Aaya 28/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers