An-Nahl · 29/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
فَادْخُلُوا أَبْوَابَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ فَلَبِئْسَ مَثْوَى الْمُتَكَبِّرِينَ ۝٢٩
Fadkhulooo abwaaba jahannama khaalideena feeha falabi`sa maswal mutakab bireen
📖 Tekkim Wolof
Kon dugguleen ciy buntu Safara, te dangeen cay béel. Te bon na lool dëkkukaayu ña daan rëy-rëylu !
🎧 Dégg

📜 Aaya 27-31 — An-Nahl

27ثُمَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يُخْزِيهِمْ وَيَقُولُ أَيْنَ شُرَكَائِيَ الَّذِينَ كُنتُمْ تُشَاقُّونَ فِيهِمْ ۚ قَالَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ إِنَّ الْخِزْيَ الْيَوْمَ وَالسُّوءَ عَلَى الْكَافِرِينَ
Te bu Bis-pénc baa, Dana leen gàcceel, ne leen : “Waa ana sama bokkaale ya taxoon ngeen wuuteeg [jullit ñi] ? ” - Ña amoom xam-xam tontu ne : “Bis niki tey, toroxteeg mbugal dal na ci kaw yéefar yi”.
28الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ ۖ فَأَلْقَوُا السَّلَمَ مَا كُنَّا نَعْمَلُ مِن سُوءٍ ۚ بَلَىٰ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ñoom ña Malaaka yay song, fekk ñoo tooñ seen bopp, ñu sànnib nuyyoo, naan : “Defunu woon dara lu bon ! ” - “Axakañ, Yàlla ku xam la li ngeen daan def”.
29فَادْخُلُوا أَبْوَابَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ فَلَبِئْسَ مَثْوَى الْمُتَكَبِّرِينَ
Kon dugguleen ciy buntu Safara, te dangeen cay béel. Te bon na lool dëkkukaayu ña daan rëy-rëylu !
30۞ وَقِيلَ لِلَّذِينَ اتَّقَوْا مَاذَا أَنزَلَ رَبُّكُمْ ۚ قَالُوا خَيْرًا ۗ لِّلَّذِينَ أَحْسَنُوا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةٌ ۚ وَلَدَارُ الْآخِرَةِ خَيْرٌ ۚ وَلَنِعْمَ دَارُ الْمُتَّقِينَ
Ñuy wax [ña ragal seen Boroom] : “Ana lan la seen Boroom wàcce ? ”. Ñu tontu ne : “Yiw”. Ñeel na ñi rafetal ci àddina Samay teraanga ; waaye kërug àllaaxiraa gën. Te aka baax kërug way-ragal ña [seen Boroom] !
31جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا مَا يَشَاءُونَ ۚ كَذَٰلِكَ يَجْزِي اللَّهُ الْمُتَّقِينَ
Àjjana ju sax la, ñu tàbbi ca, te ay dex danañuy daw-dawaan ci suufam. Te danañu fa am lu ñu bëgg ; Noonu la Yàlla di feye way-ragal ña [Yàlla].
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — An-Nahl 29

Simoore An-Nahl Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Kon dugguleen ciy buntu Safara, te dangeen cay béel. Te…

Simoore Aaya 29/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers